4Ñooñu la Noo gu Sell gi yebal, ñu dem dëkk ba ñuy wax Selusi, dugge fa gaal, jëm dun ba ñuy wax Sippar.
5Ña nga teereji dëkk ba ñuy wax Salamin, daldi fay yégle kàddug Yàlla ca jànguy Yawut ya, ku ñuy wax Yowaan Màrk ànd ak ñoom, di leen jàpple.
6Ci biir loolu ñu wër dun ba bépp, ba yegg Pafos, péey ba. Ñu tase faak ab ñeengokatub Yawut buy yonent-yonentlu, ñu di ko wax Bar Yeesu.