Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 12:3-12 in Wolof

Help us?

JËF YA 12:3-12 in Téereb Injiil

3 Bi mu gisee nag ne mbir moomu neex na Yawut ya, mu daldi jàpp it Piyeer; fekk loolu daje ak bési màggalu Yawut, ga ñuy wax Mburu ma amul lawiir.
4 Bi mu ko jàppee, mu tëj ko kaso, teg ko ci loxoy ñeenti mboolooy xarekat, ngir ñu wottu ko, fekk mbooloo mu ci nekk di ñeenti nit; amoon na yéeney yóbbu ko ci kanam Yawut ya gannaaw màggalu bésu Mucc ba.
5 Noonu ñuy wottu Piyeer ca kaso ba, waaye mbooloom ñi gëm di ko ñaanal Yàlla ak seen xol bépp.
6 Bi Erodd nekkee ci tànki indilu ko, ca guddi googa yeewoon nañu Piyeer ak ñaari càllala, muy nelaw diggante ñaari xarekat, te ay xarekat di wottu buntu kaso ba.
7 Ca saa sa malaakam Boroom bi ñëw, te leer ne ràyy ca néeg ba. Malaaka ma dóor Piyeer ci wetam, yee ko ne ko: «Jógal bu gaaw!» Noonu jéng ya rot ciy loxoom.
8 Malaaka ma ne ko: «Takkal sa geño te sol say dàll.» Mu def ko. Malaaka ma ne ko: «Solal sa mbubb te topp ci man.»
9 Piyeer génn, topp ca malaaka ma, fekk gëmul sax ne lu am la, waaye mu yaakaar ne peeñu la.
10 Noonu ñu weesu wottukat bu jëkk ba ak ba ca tegu, ñu agsi ca buntu weñ, ba jëm ca dëkk ba, mu daldi ubbikul boppam ci seen kanam. Ñu génn nag, jaar ci benn mbedd, malaaka ma daldi ko bàyyi.
11 Bi xelam délsee ci moom Piyeer ne: «Léegi xam naa ci lu wóor ne, Boroom bi yónni na malaakaam, musal ma ci loxoy Erodd ak li ma Yawut ya yéene woon lépp.»
12 Mu rabal xelam ci loolu, daldi dem kër Maryaama, ndeyu Yowaana, mi ñuy wax it Màrk, fekk ñu bare booloo fa, di ñaan ci Yàlla.
JËF YA 12 in Téereb Injiil

Jëf ya 12:3-12 in Kàddug Yàlla gi

3 Mu gis nag na mbir ma neexe Yawut ya, ba tax mu teg loxo Piyeer, moom itam; loola yemook bési màggalu Mburu mu amul lawiir.
4 Naka la ko jàpplu, daldi koy tëj kaso, teg ko ci loxoy ñeenti kurél yu ñeenti takk-der, ngir ñu wattu ko; booba ma ngay xaar ba bésub Mucc bi wees, mu door koo yóbbu ca kanam askan wa.
5 Naka lañu tëj Piyeer ca kaso ba, mbooloom gëmkat ñi saxoo koo ñaanal Yàlla.
6 Ba ñu demee ba ca guddi, ga jiitu bés ba ko Erodd wara yóbbu, Piyeer a ngay nelaw ci diggante ñaari takk-der, ñu yeewe ko ñaari càllala, ay dag di wattu buntu kaso ba.
7 Ci kaw loolu am malaakam Boroom bi ne jaas, taxaw, ag leer ne ràyy ca biir kaso ba. Malaaka ma laal Piyeer ci wetam, yee ko, ne ko: «Jógal gaaw!», càllala yi daldi rote ciy loxoom.
8 Malaaka ma ne ko: «Takkal sa geño te sol say dàll.» Mu def noonu. Mu ne ko: «Solal sa mbubb te topp ci man.»
9 Piyeer génn, topp ci moom, te xamul sax ndax li ko dikkal noonu te sababoo ci malaaka mi, dëgg la. Yaakaaroon na ne am peeñu la.
10 Ñu jàll dalu wattukat bu jëkk bi, teg ci ñaareel bi, ba agsi ci buntu weñ, ba jëm ca dëkk ba, bunt ba daldi tijjikul boppam. Ñu génn, topp menn mbedd, malaaka ma jekki teqlikook Piyeer.
11 Naka la xelum Piyeer délsi, mu daldi ne: «Léegi nag xam naa xéll ne, Boroom bee yebal malaakaam, te moo ma musal ci loxol Erodd, ak mboolem li Yawut yi séentu woon.»
12 Gannaaw ba Piyeer ràññee loolu, daa dem kër Maryaama, ndeyu Yowaan Màrk, fekk ñu bare daje foofa, di ñaan.
Jëf ya 12 in Kàddug Yàlla gi