Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 12

JËF YA 12:3-12

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Bi mu gisee nag ne mbir moomu neex na Yawut ya, mu daldi jàpp it Piyeer; fekk loolu daje ak bési màggalu Yawut, ga ñuy wax Mburu ma amul lawiir.
4Bi mu ko jàppee, mu tëj ko kaso, teg ko ci loxoy ñeenti mboolooy xarekat, ngir ñu wottu ko, fekk mbooloo mu ci nekk di ñeenti nit; amoon na yéeney yóbbu ko ci kanam Yawut ya gannaaw màggalu bésu Mucc ba.
5Noonu ñuy wottu Piyeer ca kaso ba, waaye mbooloom ñi gëm di ko ñaanal Yàlla ak seen xol bépp.
6Bi Erodd nekkee ci tànki indilu ko, ca guddi googa yeewoon nañu Piyeer ak ñaari càllala, muy nelaw diggante ñaari xarekat, te ay xarekat di wottu buntu kaso ba.
7Ca saa sa malaakam Boroom bi ñëw, te leer ne ràyy ca néeg ba. Malaaka ma dóor Piyeer ci wetam, yee ko ne ko: «Jógal bu gaaw!» Noonu jéng ya rot ciy loxoom.
8Malaaka ma ne ko: «Takkal sa geño te sol say dàll.» Mu def ko. Malaaka ma ne ko: «Solal sa mbubb te topp ci man.»
9Piyeer génn, topp ca malaaka ma, fekk gëmul sax ne lu am la, waaye mu yaakaar ne peeñu la.
10Noonu ñu weesu wottukat bu jëkk ba ak ba ca tegu, ñu agsi ca buntu weñ, ba jëm ca dëkk ba, mu daldi ubbikul boppam ci seen kanam. Ñu génn nag, jaar ci benn mbedd, malaaka ma daldi ko bàyyi.
11Bi xelam délsee ci moom Piyeer ne: «Léegi xam naa ci lu wóor ne, Boroom bi yónni na malaakaam, musal ma ci loxoy Erodd ak li ma Yawut ya yéene woon lépp.»
12Mu rabal xelam ci loolu, daldi dem kër Maryaama, ndeyu Yowaana, mi ñuy wax it Màrk, fekk ñu bare booloo fa, di ñaan ci Yàlla.

Read JËF YA 12JËF YA 12
Compare JËF YA 12:3-12JËF YA 12:3-12