Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 10

Jëf ya 10:3-8

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Am peeñu nag dikkal ko digg njolloor, mu gis ci lu leer malaakam Yàlla, mu duggsi, ne ko: «Korney!»
4Korney ne ko jàkk, tiit, ne ko: «Sang bi, lu mu doon?» Mu ne ko: «Say ñaan ak say sarax yéeg na fa Yàlla, ba mu bàyyi la xel.
5Léegi nag yebleel ca Yope, nga wooluji fa ku ñuy wax Simoŋ, ñu di ko dàkkentale Piyeer.
6Ma nga dal ak meneen Simoŋ ma, wullikat ba këram féete wetu géej.»
7Naka la malaaka ma wax ak Korney ba dem, mu woo ñaar ciy surgaam, ak benn takk-der bu jullite te bokk ciy suqam.
8Mu nettali leen lépp nag, daldi leen yebal Yope.

Read Jëf ya 10Jëf ya 10
Compare Jëf ya 10:3-8Jëf ya 10:3-8