Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 10

Jëf ya 10:29-38

Help us?
Click on verse(s) to share them!
29Looloo tax, bi ngeen ma wooloo, ma ñëw te tendeefaluma benn yoon. Ma di leen laaj nag li waral ngeen woolu ma.»
30Ci kaw loolu Korney ne: «Bëkkaati-démb ci waxtuw digg njolloor wii nu tollu tey, ci laa doon ñaane sama biir néeg. Mu am ku jekki ne jaas ci sama kanam, sol yére yu ne ràññ.
31Mu ne ma: “Korney, nangu nañu say ñaan, te nemmiku nañu say sarax fa kanam Yàlla.
32Kon nag yebleel Yope, nga woolu Simoŋ, mi ñu dàkkentale Piyeer; ma nga dal ca kër meneen Simoŋ, wullikat ba ca wetu géej ga.”
33Ca saa sa nag laa yeble ci yaw. Yaw it def nga lu baax, bi nga dikkee. Léegi nag nun ñépp a ngi fi ci kanam Yàlla, ngir déglu mboolem lu la Boroom bi sant.»
34Ba loolu amee Piyeer àddu, ne: «Dëgg-dëgg gis naa ne Yàlla daal du gënaatle,
35waaye xeetoo xeet, ku ko ci ragal tey def njekk, mooy ki ko neex.
36Moo yónnee kàddoom bànni Israyil, àgge leen xibaaru jàmm, biy maye jàmm ci Yeesu Almasi, miy Sangu ñépp.
37Yeen ci seen bopp xam ngeen li xewoon ci mboolem réewum Yawut yi, te dale ci diiwaanu Galile, gannaaw ba Yaxya wootee, di sóobe cim ndox,
38ak ni Yàlla ànde ak Yeesum Nasaret, ba jagleel ko pal gu mu dogale Noo gu Sell geek xam-xam bi mu ko sotti, muy wër, di def lu baax, di faj mboolem ñi Seytaane notoon.

Read Jëf ya 10Jëf ya 10
Compare Jëf ya 10:29-38Jëf ya 10:29-38