Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 10:22-44 in Wolof

Help us?

JËF YA 10:22-44 in Téereb Injiil

22 Ñu ne ko: «Korney, njiitu xare ba, nit ku jub la te ragal Yàlla, ba am seede su rafet ci bànni Israyil gépp. Malaaka mu sell nag sant na ko, mu woolu la ci këram te déglu li ngay wax.»
23 Ci kaw loolu Piyeer dugal leen, dalal leen. Ba bët setee, Piyeer jóg, dem ak ñoom, ànd ak ñenn ci bokk yi dëkk Yope,
24 te bés ba ca topp mu dikk Sesare. Fekk Korney woo na këram ay bokkam ak i xaritam yi ko gëna jege, di xaar Piyeer.
25 Bi Piyeer duggee nag, Korney daje ak moom, daanu ciy tànkam, sargal ko.
26 Waaye Piyeer yékkati ko ne: «Jógal, man it nit rekk laa.»
27 Noonu muy waxtaan ak moom, duggsi, fekk fa ndajem nit ñu bare.
28 Mu ne leen: «Xam ngeen ne aaye nañu Yawut, mu jaxasoo ak ku mu bokkalul xeet, mbaa mu dugg ci këram. Waaye Yàlla won na ma ne warumaa ne kenn setul mbaa araam na.
29 Looloo tax, bi ngeen ma wooloo, ñëw naa ci lu àndul ak werante. Maa ngi leen di laaj nag, lu ngeen may doye?»
30 Ci kaw loolu Korney ne: «Ñetti fan a ngii may ñaan ci sama biir kër ci waxtu wii, maanaam tisbaar. Ci saa si ku sol yére yuy melax taxaw ci sama kanam,
31 mu ne ma: “Korney, say ñaan nangu na, te say sarax egg nañu fa kanam Yàlla.
32 Yónneel nag ci Yope, woolu Simoŋ, mi ñu dàkkentale Piyeer; mu nga dal ci kër Simoŋ miy wullikat ca wetu géej ga.”
33 Yónnee naa nag ci ni mu gëna gaawe, woolu la; te maa ngi lay sant ci li nga ñëw. Léegi nag nun ñépp nu ngi fi ci kanam Yàlla, ngir déglu lépp li la Boroom bi sant.»
34 Noonu Piyeer jël kàddu ga ne leen: «Ci dëgg gis naa ne Yàlla du gënale,
35 waaye ci xeet yépp, ku ko ragal tey def lu jub, moom la nangu.
36 Yónnee na kàddoom bànni Israyil, di leen xibaar jàmm, jaarale ko ci Yeesu Kirist, miy Boroom lépp.
37 Xam ngeen li xewoon ci réewum Yawut yépp, li ko tàmbalee ci diiwaanu Galile, topp ci waareb Yaxya, mu naan nit ñi, mu sóob leen ci ndox.
38 Xam ngeen ne Yàlla fal na Yeesum Nasaret, sol ko Xel mu Sell mi ak kàttan; muy wër, di def lu baax ak di faj ñépp ñi nekkoon ci kilifteefu Seytaane, ndaxte Yàlla ànd na ak moom.
39 «Seede nanu li mu def lépp ci biir réewu Yawut ya ak Yerusalem. Moona rey nañu ko ci wékk ko ci bant.
40 Waaye Yàlla dekkal na ko ci ñetteelu fan ba te biral ko,
41 waxuma xeet wépp, waaye seede yi Yàlla tànn lu jiitu, maanaam nun ñi daan lekk di naan ak moom gannaaw ndekkiteem.
42 Te Yeesu sant na nu, nu yégal xeet wa, di seede ne moom la Yàlla jagleel àtteb ñiy dund ak ñi dee.
43 Yonent yépp seedeel nañu ko ne, ku ko gëm, Yàlla dina la baal say bàkkaar ci turam.»
44 Bi Piyeer di wax loolu, Xel mu Sell mi wàcc ci kaw ñépp ñiy déglu kàddu ga.
JËF YA 10 in Téereb Injiil

Jëf ya 10:22-44 in Kàddug Yàlla gi

22 Ñu ne ko: «Njiitu takk-der ba Korney, ku jub, ragal Yàlla, te rafet seede bu ko xeetu Yawut wépp seedeel, moo jote ci malaaka mu sell, ndigalal woolu la këram, ngir déglu say kàddu.»
23 Ci kaw loolu Piyeer dugal leen, dalal leen. Ba bët setee, Piyeer ànd ak ñoom, ñenn ca bokki gëmkat ña dëkke Yope gunge ko.
24 Ca ëllëg sa Piyeer agsi Sesare. Fekk na Korney di ko séentu, daldi woo ca këram ay bokkam, ak xaritam yi ko gëna jege.
25 Ba Piyeer duggsee, Korney gatandu ko, ne gurub ca tànki Piyeer, sujjóot.
26 Piyeer yékkati ko, ne: «Déet jógal, man it, nit doŋŋ laa.»
27 Piyeer di waxtaan ak moom, ba duggsi, yem ca nit ñu bare ña fa daje.
28 Mu ne leen: «Yeen de xam ngeen ne ab Yawut, mayeesu ko mu jaxasoo ak xeetu jaambur, mbaa mu seeti ko. Waaye man nag Yàllaa ma won ne du kenn nit ku ma naan daganula jaxasool, mbaa setul.
29 Looloo tax, bi ngeen ma wooloo, ma ñëw te tendeefaluma benn yoon. Ma di leen laaj nag li waral ngeen woolu ma.»
30 Ci kaw loolu Korney ne: «Bëkkaati-démb ci waxtuw digg njolloor wii nu tollu tey, ci laa doon ñaane sama biir néeg. Mu am ku jekki ne jaas ci sama kanam, sol yére yu ne ràññ.
31 Mu ne ma: “Korney, nangu nañu say ñaan, te nemmiku nañu say sarax fa kanam Yàlla.
32 Kon nag yebleel Yope, nga woolu Simoŋ, mi ñu dàkkentale Piyeer; ma nga dal ca kër meneen Simoŋ, wullikat ba ca wetu géej ga.”
33 Ca saa sa nag laa yeble ci yaw. Yaw it def nga lu baax, bi nga dikkee. Léegi nag nun ñépp a ngi fi ci kanam Yàlla, ngir déglu mboolem lu la Boroom bi sant.»
34 Ba loolu amee Piyeer àddu, ne: «Dëgg-dëgg gis naa ne Yàlla daal du gënaatle,
35 waaye xeetoo xeet, ku ko ci ragal tey def njekk, mooy ki ko neex.
36 Moo yónnee kàddoom bànni Israyil, àgge leen xibaaru jàmm, biy maye jàmm ci Yeesu Almasi, miy Sangu ñépp.
37 Yeen ci seen bopp xam ngeen li xewoon ci mboolem réewum Yawut yi, te dale ci diiwaanu Galile, gannaaw ba Yaxya wootee, di sóobe cim ndox,
38 ak ni Yàlla ànde ak Yeesum Nasaret, ba jagleel ko pal gu mu dogale Noo gu Sell geek xam-xam bi mu ko sotti, muy wër, di def lu baax, di faj mboolem ñi Seytaane notoon.
39 «Nun ci sunu bopp noo seede li mu def lépp ci réewum Yawut yi ak Yerusalem. Moom mi ñu wékk ci bant, ba rey ko,
40 moom la Yàlla dekkal ci ñetteelu fanam, ba may ko mu feeñ.
41 Du askan wépp la ko won, xanaa nun, seede yi Yàlla tànnoon lu jiitu, nu bokk ak moom lekk ak naan, gannaaw ndekkiteem.
42 Moo nu sant nag nu xamal askan wi te seede ne moom la Yàlla tabb àttekatub aji dund ñi, ak aji dee ñi.
43 Moom la yonent yépp seedeel, ne képp ku ko gëm, jot nga sa njéggalug bàkkaar ciw turam.»
44 Ba Piyeer di wax kàddu googu, Noo gu Sell gi daldi wàcc ci kaw mboolem ñay déglu kàddu ga.
Jëf ya 10 in Kàddug Yàlla gi