Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 10

Jëf ya 10:22-44

Help us?
Click on verse(s) to share them!
22Ñu ne ko: «Njiitu takk-der ba Korney, ku jub, ragal Yàlla, te rafet seede bu ko xeetu Yawut wépp seedeel, moo jote ci malaaka mu sell, ndigalal woolu la këram, ngir déglu say kàddu.»
23Ci kaw loolu Piyeer dugal leen, dalal leen. Ba bët setee, Piyeer ànd ak ñoom, ñenn ca bokki gëmkat ña dëkke Yope gunge ko.
24Ca ëllëg sa Piyeer agsi Sesare. Fekk na Korney di ko séentu, daldi woo ca këram ay bokkam, ak xaritam yi ko gëna jege.
25Ba Piyeer duggsee, Korney gatandu ko, ne gurub ca tànki Piyeer, sujjóot.
26Piyeer yékkati ko, ne: «Déet jógal, man it, nit doŋŋ laa.»
27Piyeer di waxtaan ak moom, ba duggsi, yem ca nit ñu bare ña fa daje.
28Mu ne leen: «Yeen de xam ngeen ne ab Yawut, mayeesu ko mu jaxasoo ak xeetu jaambur, mbaa mu seeti ko. Waaye man nag Yàllaa ma won ne du kenn nit ku ma naan daganula jaxasool, mbaa setul.
29Looloo tax, bi ngeen ma wooloo, ma ñëw te tendeefaluma benn yoon. Ma di leen laaj nag li waral ngeen woolu ma.»
30Ci kaw loolu Korney ne: «Bëkkaati-démb ci waxtuw digg njolloor wii nu tollu tey, ci laa doon ñaane sama biir néeg. Mu am ku jekki ne jaas ci sama kanam, sol yére yu ne ràññ.
31Mu ne ma: “Korney, nangu nañu say ñaan, te nemmiku nañu say sarax fa kanam Yàlla.
32Kon nag yebleel Yope, nga woolu Simoŋ, mi ñu dàkkentale Piyeer; ma nga dal ca kër meneen Simoŋ, wullikat ba ca wetu géej ga.”
33Ca saa sa nag laa yeble ci yaw. Yaw it def nga lu baax, bi nga dikkee. Léegi nag nun ñépp a ngi fi ci kanam Yàlla, ngir déglu mboolem lu la Boroom bi sant.»
34Ba loolu amee Piyeer àddu, ne: «Dëgg-dëgg gis naa ne Yàlla daal du gënaatle,
35waaye xeetoo xeet, ku ko ci ragal tey def njekk, mooy ki ko neex.
36Moo yónnee kàddoom bànni Israyil, àgge leen xibaaru jàmm, biy maye jàmm ci Yeesu Almasi, miy Sangu ñépp.
37Yeen ci seen bopp xam ngeen li xewoon ci mboolem réewum Yawut yi, te dale ci diiwaanu Galile, gannaaw ba Yaxya wootee, di sóobe cim ndox,
38ak ni Yàlla ànde ak Yeesum Nasaret, ba jagleel ko pal gu mu dogale Noo gu Sell geek xam-xam bi mu ko sotti, muy wër, di def lu baax, di faj mboolem ñi Seytaane notoon.
39«Nun ci sunu bopp noo seede li mu def lépp ci réewum Yawut yi ak Yerusalem. Moom mi ñu wékk ci bant, ba rey ko,
40moom la Yàlla dekkal ci ñetteelu fanam, ba may ko mu feeñ.
41Du askan wépp la ko won, xanaa nun, seede yi Yàlla tànnoon lu jiitu, nu bokk ak moom lekk ak naan, gannaaw ndekkiteem.
42Moo nu sant nag nu xamal askan wi te seede ne moom la Yàlla tabb àttekatub aji dund ñi, ak aji dee ñi.
43Moom la yonent yépp seedeel, ne képp ku ko gëm, jot nga sa njéggalug bàkkaar ciw turam.»
44Ba Piyeer di wax kàddu googu, Noo gu Sell gi daldi wàcc ci kaw mboolem ñay déglu kàddu ga.

Read Jëf ya 10Jëf ya 10
Compare Jëf ya 10:22-44Jëf ya 10:22-44