Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Galasi

Galasi 4

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Li ma leen di wax nag mooy lii: boroom ndono li ci kër gi, li feek mu dib tuut-tànk, wuutewul akub jaam, doonte moo moom lépp.
2Ci kilifteefu ay wattukat aki saytukat lay nekk ba kera mu àggee ca at ya ko baayam àppaloon.
3Nun itam naka noonu, ba nu dee ay tuut-tànk yu nekk ci kilifteefu mbiri àddina, ay jaam lanu woon.
4Waaye ba àpp ba jotee, Yàlla moo yónni Doomam, mu juddoo ci jigéen, juddoo ci biir curgag yoonu Musaa,
5ngir jot ñi ci curgag yoon wi, ba nu jagoo cérub doom.
6Li ngeen diy doom nag tax na Yàlla yebal Noowug Doomam ci seen biir xol, ba Noo gi naan: «Abba», mu firi Baay.
7Moo tax dootuloo ab jaam, doom nga. Gannaaw doom nga nag, boroom cér nga it fa Yàlla sa baay.
8Bu jëkk, ba ngeen xamul Yàlla, ay yàlla yu dul dëgg ngeen daan jaamu.
9Waaye léegi bi ngeen xamee Yàlla, mbaa bi leen Yàlla ràññee, nu ngeen mana delluwaate ci mbiri àddina yooyu boole tële ak ñàkk njariñ, bay nekkaat seeni jaam?
10Yeena ngi wormaal yenn bés yi, aki weer, ak ay fan, aki at!
11Li may ragal ci yeen daal mooy sama coono ci yeen neen.
12Yeen laay tinu, bokk yi, mel-leen ni man, ci yooyu mbir, ndax man itam ni yeen laa mel. Tooñuleen ma benn yoon.
13Xam ngeen ne tëleg yaram moo ma mayoon yoon wa ma leen jëkka àgge xibaaru jàmm bi.
14Nattu ba leen sama woppi yaram tegoon it taxul ngeen jéppi ma, taxul ngeen beddi ma. Ni malaakam Yàlla ngeen ma dalale, mbaa ni Yeesu Almasi
15Ana seen mbég mooma woon nag? Ndax kat maa leen seedeel ne su manoona am sax, seeni bët ngeen di luqi, jox ma.
16Xanaa li ma leen di wax dëgg daa tax ma mujj di seenub noon?
17Yitte ju réy ji ñenn ñiy taqoo ak yeen de, jubluwuñu ci lu baax. Dañu leena bëgga tàggale ak nun, ba ngeen taq leen.
18Yitte ju réy ju ñu am ci nit ki nag, ndegam lu baax lees ci jublu, saa su nekk lay baax, waaye du rekk saa yu ma teewee ci seen biir.

19Yeen samay doom! Maa ngi dellooti ci mat wu ma leen jure woon ni jigéen, ba keroog Almasi mate sëkk ci yeen.
20Maaka bëggoona nekk ak yeen tey, ba gëna misaale sama baat, nde jàq naa lool ci yeen!
21Waxleen ma, yeen ñi bëgga nekk ci kilifteefu yoonu Musaa, xanaa xamuleen li yoon wi wax?
22Bindees na ne Ibraayma ñaari doom yu góor la am; kenn ki jaam bi jur, ak ki gor si jur.
23Doomu jaam bi moo juddu ci kaw coobarey bakkanu nit, waaye ki gor si jur, ci kaw digeb Yàlla la juddu.
24Mbir mi misaal a ngi ci. Ñaari jigéen ñi ñaari kóllëre lay bijji. Genn kóllëre gi bawoo tundu Sinayi moo meññ lu ñeel njaam, te kooku mooy Ajara.
25Ajara moomu mooy tundu Sinayi, wa ca réewum Arabi, te moo taxawe Yerusalem gii tey, dëkk bii dib jaam mook doomam yi ko dëkke.
26Waaye Yerusalem, ga fa kaw, mooy gor si, te moom mooy sunu ndey.
27Ndax kat bindees na ne: «Yaw mi jaasir, ba juroo, xaacul, yaw mi xamul mititu mat, sarxolleel, nde ndaw si ñu foñ moo gëna jaboot kiy séy.»
28Yeen nag bokk yi, yeenay doomi digeb Yàlla, ni ko Isaaxa doone.
29Waaye doom ji juddoo ci coobarey bakkan, noonu mu daan bundxatale, bu jëkkoon, doom ji juddoo ci Noowug Yàlla, noonu rekk lay deme ba tey jii.
30Te lu ci Mbind mi wax? Mu ne: «Dàqal jaam bu jigéen bii ak doomam, ndax doomu jaam bi du donnandoo ak doomu gor si.»
31Kon nag bokk yi, nun dunu doomi jaam bi, waaye nooy doomi gor si.