3 Aw yëkk xam na boroomam, mbaam-sëf xam gàmb, bi ko boroomam di xonte, waaye Israyil xamul, sama ñoñ ñii xàmmeewuñu.»
4 Wóoy wii xeetu moykat, wii askan wu diisu ñaawtéef, mii njurum defkati mbon, yii doomi yàqute! Ñoo wacc Aji Sax ji, ñoo teddadil Aji Sell ju Israyil, dëddu ko.