Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - 2 TESALONIG

2 TESALONIG 3

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Léegi nag bokk yi, ñaanal-leen nu, ngir kàddug Boroom bi law te ànd ak ndam, ni mu ko ame woon ci yéen.
2Ngeen ñaanal nu it, ngir nu mucc ci ñi bon te soxor, ndaxte du ñépp a gëm.
3Waaye Boroom bi kuy sàmm kóllëre la; dina leen dëgëral te musal leen ci Ibliis.
4Te wóor nanu ci kanam Boroom bi ne yéena ngi def li nu leen santoon, te dingeen ci sax.
5Na Boroom bi gindi seeni xol ci mbëggeelu Yàlla ak muñu Kirist.
6Nu ngi leen di sant it bokk yi, ci turu sunu Boroom Yeesu Kirist, ngeen dëddu bépp mbokk buy wéy ci tayel te baña topp dénkaane, yi nu leen jottali.
7Xam ngeen bu baax, yéen ci seen bopp, ni ngeen wara awe ci sunuy tànk. Ba nu nekkee ca yéen, wéyunu woon ci tayel
8te masunoo lekk ñaqu kenn. Waaye guddi ak bëccëg danu daan ñaq, di sonn, ngir baña wéeru ci kenn ci yéen.
9Waxuma ne amunu sañ-sañu def ko, waaye danoo bëggoona nekk ay royukaay ci yéen, ngir ngeen aw ci sunuy tànk.
10Ndaxte ba nu nekkee ca yéen, lii lanu tëraloon: «Ku liggéeyul, du lekk.»
11Léegi nag dégg nanu ne am na ci yéen ñuy wéy ci tayel; liggéeyuñu dara, lu dul di dugg ci lu seen yoon nekkul.
12Ñu deme noonu nag, nu ngi leen di sant te di leen dénk ci turu Boroom bi Yeesu Kirist, ñuy liggéey ci jàmm tey dunde seen ñaq.
13Yéen nag bokk yi, buleen tàyyi ci def lu rafet.
14Su kenn bañee topp li nu bind ci bataaxal bii, ràññeeleen ko te sore ko, ngir mu rus ci.
15Waxuma ngeen def ko noon, waaye ngeen yedd ko ni seen mbokk.
16Yal na leen kiy Boroom jàmm may jàmm fépp ak ci lépp. Yal na Boroom bi ànd ak yéen ñépp.
17Tàggoo bii maa ko bind ci sama loxo, man Pool. Nii laay binde, te di màndargaale nii sama bataaxal yépp.
18Yal na yiwu sunu Boroom Yeesu Kirist ànd ak yéen ñépp.