Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 8:43-59 in Wolof

Help us?

YOWAANA 8:43-59 in Téereb Injiil

43 Lu tax dégguleen li ma leen wax? Li ko waral moo di manuleen koo déglu.
44 Seytaane mooy seen baay, te bëgg-bëggam ngeen di bëgg di def. Bóomkat la masa doon. Du taxaw mukk ci dëgg, ndaxte dëgg nekkul ci moom. Buy fen, dëppoo na ak jikkoom, ndaxte fenkat la, te ci moom la fen soqikoo.
45 Waaye man damay wax dëgg, moo tax gëmuleen ma.
46 Kan ci yéen moo mana seede ne bàkkaar naa? Su ma waxee dëgg nag, lu tax dungeen ma gëm?
47 Ku nekk doomu Yàlla dina déglu ay waxam. Waaye nekkuleen doomi Yàlla, looloo tax dungeen déglu.»
48 Yawut ya ne ko: «Ndax danoo waxul dëgg, bu nu nee, nitu Samari nga te dangaa am ay rab?»
49 Yeesu ne leen: «Awma rab; waaye sama Baay laay teral, te yéen dangeen may toroxal.
50 Wutumaa màggal sama bopp. Keneen a ma koy wutal te mooy àtte.
51 Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, kuy sàmm sama wax doo dee mukk.»
52 Yawut ya ne ko: «Léegi wóor nanu ne dangaa am ay rab! Ibraayma faatu na, yonent yépp faatu, yaw nga naan: “Kuy sàmm sama wax doo ñam dee.”
53 Sunu baay Ibraayma faatu na; mbaa du dangaa defe ne yaa ko gëna màgg? Yonent yi itam faatu nañu. Waaw, loo teg sa bopp?»
54 Yeesu ne leen: «Su ma dee màggal sama bopp, du am maana. Sama Baay a may màggal, moom mi ngeen naan, mooy seen Yàlla.
55 Xamuleen ko nag; man maa ko xam. Su ma ne woon xawma ko, ab fenkat laay doon ni yéen. Waaye xam naa ko te maa ngi sàmm waxam.
56 Seen baay Ibraayma bég na, bi mu yégee sama ngan. Bi mu ko gisee it, bég na ci lool.»
57 Yawut ya ne ko: «Amaguloo juróom fukki at, ba noppi naan gis nga Ibraayma?»
58 Yeesu ne leen: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, laata ñuy sàkk Ibraayma, fekk na ma doon ki ñuy wax Maay ki Nekk.»
59 Noonu ñu for ay xeer, bëgg ko koo sànni ngir rey ko. Waaye Yeesu nëbbu, génn kër Yàlla ga.
YOWAANA 8 in Téereb Injiil