Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 8:29-55 in Wolof

Help us?

YOWAANA 8:29-55 in Téereb Injiil

29 Te it ki ma yónnee ngi ànd ak man; masu maa bàyyi ma wéet, ndaxte li ko neex rekk laay def.»
30 Bi ñuy dégg Yeesu di wax loolu, ñu bare daldi koy gëm.
31 Yeesu ne Yawut ya ko gëmoon: «Bu ngeen saxee ci li ma wax, nekk ngeen samay taalibe ci lu wóor.
32 Te it dingeen xam dëgg gi, te dëgg gi dina leen goreel.»
33 Ñu ne ko: «Nun ci Ibraayma lanu soqikoo te masunoo nekk jaamu kenn. Nan nga nu mana waxe ne dinañu leen goreel?»
34 Yeesu ne leen: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, képp kuy bàkkaar, jaamu bàkkaar la.
35 Te jaam du bokk ci kër gi ba fàww, waaye doom, moom, ci kër gi la bokk ba fàww.
36 Kon nag bu leen Doom ji defee gor, dingeen doon ay gor tigi.
37 Xam naa ne askanu Ibraayma ngeen. Waaye yéena ngi may wuta rey, ndaxte li may jàngle xajul ci yéen.
38 Li ma sama Baay won laay wax; waaye yéen, li leen seen baay di wax ngeen di def.»
39 Ñu ne ko: «Ibraayma mooy sunu baay.» Yeesu ne leen: «Bu ngeen dee waa kër Ibraayma, dingeen jëfe ni moom.
40 Léegi nag yéena ngi may wuta rey, man mi leen jottali dëgg, gi ma jële ca Yàlla. Ibraayma deful lu ni mel.
41 Li ngeen donne ci seen baay rekk ngeen di def.» Ñu ne ko: «Nun de, dunu doomi araam. Benn baay rekk lanu am, mooy Yàlla.»
42 Yeesu ne leen: «Bu Yàlla doon seen baay, dingeen ma bëgg, ndaxte ca moom laa jóge, ñëw ci ndigalam. Ñëwaluma sama bopp, waaye moo ma yónni.
43 Lu tax dégguleen li ma leen wax? Li ko waral moo di manuleen koo déglu.
44 Seytaane mooy seen baay, te bëgg-bëggam ngeen di bëgg di def. Bóomkat la masa doon. Du taxaw mukk ci dëgg, ndaxte dëgg nekkul ci moom. Buy fen, dëppoo na ak jikkoom, ndaxte fenkat la, te ci moom la fen soqikoo.
45 Waaye man damay wax dëgg, moo tax gëmuleen ma.
46 Kan ci yéen moo mana seede ne bàkkaar naa? Su ma waxee dëgg nag, lu tax dungeen ma gëm?
47 Ku nekk doomu Yàlla dina déglu ay waxam. Waaye nekkuleen doomi Yàlla, looloo tax dungeen déglu.»
48 Yawut ya ne ko: «Ndax danoo waxul dëgg, bu nu nee, nitu Samari nga te dangaa am ay rab?»
49 Yeesu ne leen: «Awma rab; waaye sama Baay laay teral, te yéen dangeen may toroxal.
50 Wutumaa màggal sama bopp. Keneen a ma koy wutal te mooy àtte.
51 Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, kuy sàmm sama wax doo dee mukk.»
52 Yawut ya ne ko: «Léegi wóor nanu ne dangaa am ay rab! Ibraayma faatu na, yonent yépp faatu, yaw nga naan: “Kuy sàmm sama wax doo ñam dee.”
53 Sunu baay Ibraayma faatu na; mbaa du dangaa defe ne yaa ko gëna màgg? Yonent yi itam faatu nañu. Waaw, loo teg sa bopp?»
54 Yeesu ne leen: «Su ma dee màggal sama bopp, du am maana. Sama Baay a may màggal, moom mi ngeen naan, mooy seen Yàlla.
55 Xamuleen ko nag; man maa ko xam. Su ma ne woon xawma ko, ab fenkat laay doon ni yéen. Waaye xam naa ko te maa ngi sàmm waxam.
YOWAANA 8 in Téereb Injiil