Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 8:11-26 in Wolof

Help us?

YOWAANA 8:11-26 in Téereb Injiil

11 Mu ne ko: «Kenn, Sang bi.» Yeesu ne ko: «Man it ci sama wàll, duma la daan. Demal, waaye bul defati bàkkaar.»
12 Yeesu jubluwaat ca mbooloo ma ne leen: «Man maay leeru àddina si. Ku ma topp doo dox cig lëndëm, waaye dinga am leeru dund.»
13 Farisen ya ne ko: «Yaw yaay seedeel sa bopp, kon li ngay wax du dëgg.»
14 Yeesu ne leen: «Maa ngi seedeel sama bopp, teewul li may wax di dëgg, ndaxte xam naa fa ma bàyyikoo, xam fa ma jëm. Waaye yéen xamuleen fa ma bàyyikoo ak fa ma jëm.
15 Ci gis-gisu àddina ngeen di àttee; man duma àtte kenn.
16 Teewul nag, su ma demee bay àtte, bu jub lay doon, ndaxte du man rekk ay àtte, waaye Baay, bi ma yónni, daf ciy ànd ak man.
17 Seen yoon dafa wax ne seedes ñaari nit a gëna wóor.
18 Man maa ngi seedeel sama bopp, te Baay bi ma yónni mi ngi may seedeel itam.»
19 Ñu laaj ko ne: «Kuy sa baay?» Yeesu ne leen: «Xamuleen ma, xamuleen sama Baay. Bu ngeen ma xamoon, xam ko.»
20 Bi muy wax loolu, Yeesoo nga doon jànglee ca kër Yàlla ga, ca wetu fa ñu doon denc asaka ya. Kenn manu ko woona jàpp, ndaxte waxtoom jotagul.
21 Yeesu dellu ne leen: «Maa ngi dem; dingeen ma seet, waaye seen bàkkaar ngeen di deeyaale. Fa ma jëm, dungeen fa mana dem.»
22 Yawut yay waxante naan: «Nee na kat, fa mu jëm, dunu fa mana dem. Mbaa du day xaruji?»
23 Yeesu ne leen: «Yéen, fii ngeen bawoo, ci suuf, waaye man ca kaw laa jóge. Àddina ngeen soqikoo, waaye man bokkuma ci.
24 Looloo tax ma ne, ci seeni bàkkaar ngeen di dee. Bu ngeen gëmul ki ma nekk, dingeen dee ci seeni bàkkaar.»
25 Ñu ne ko: «Yaay kan?» Mu ne leen: «Li ma leen waxoon ca njàlbéen ga.
26 Li ma mana wax ci yéen ba àtte leen, bare na. Waaye ki ma yónni, ku wóor la, te li mu ma wax rekk laay jottali àddina.»
YOWAANA 8 in Téereb Injiil