Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 6:47-67 in Wolof

Help us?

YOWAANA 6:47-67 in Téereb Injiil

47 Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, ku gëm am nga dund gu dul jeex.
48 Maay ñam wiy joxe dund.
49 Seeni maam lekk nañu mànn ca màndiŋ ma, teewul dee nañu.
50 Waaye ñam wiy wàcce ci asamaan, ku ko lekk, doo dee.
51 Man maay ñam wiy dund te wàcce ci asamaan. Ku lekk ci ñam wii, dinga dund ba fàww. Te it ñam wi may joxeji, sama yaram la; dama koy joxe ngir àddina mana dund.»
52 Noonu Yawut ya werante werante wu tàng ci seen biir naan: «Naka la nu waa jii mana joxe yaramam, ngir nu lekk ko?»
53 Yeesu ne leen: «Dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, bu ngeen lekkul yaramu Doomu nit ki te naanuleen deretam, dungeen am dund ci yéen.
54 Ku lekk sama yaram te naan sama deret, am nga dund gu dul jeex, te dinaa la dekkal keroog bés bu mujj ba.
55 Ndaxte sama yaram mooy ñam wu wóor wi, te sama deret mooy naan gu wóor gi.
56 Kiy lekk sama yaram tey naan sama deret dina sax ci man, ma dëkk ci moom.
57 Baay bi ma yónni mu ngi dund, te maa ngi dund jaarale ko ci moom; noonu itam ku may lekk dina dund jaarale ko ci man.
58 Kon nag ñam wi wàcce ci asamaan a ngi noonu; bokkul ak ñam wa seeni maam lekkoon te faatu. Ku lekk ñam wii may wax dinga dund ba fàww.»
59 Baat yooyu la Yeesu wax, bi mu doon jàngle ca jàngu ba ca Kapernawum.
60 Bi ñu dégloo Yeesu ba noppi, taalibeem yu bare nee nañu: «Njàngle mii de, jafe na! Kan moo ko mana déglu?»
61 Yeesu gis ne taalibeem yaa ngi ñurumtoo loolu, mu ne leen: «Ndax li ma wax da leena jaaxal?
62 Lan mooy am nag, bu fekkee gis ngeen Doomu nit ki dellu, yéeg fa mu jëkkoona nekk?
63 Xelu Yàlla mi mooy joxe dund; ñam wi jariñul dara. Kàddu yi ma leen wax, ci Xelum Yàlla lañu jóge te ñooy joxe dund.
64 Waaye am na ci seen biir ñu ko gëmul.» Ndaxte Yeesu xamoon na ca njàlbéen ga ñan ñoo ko waroona gëmadi ak kan moo ko waroona wor.
65 Mu dolli ca it ne: «Looloo tax ma ne, kenn manula ñëw ci man te Baay bi mayu la, nga agsi.»
66 Ci loolu taalibeem yu bare dëpp, bañatee ànd ak moom.
67 Yeesu daldi wax ak fukki taalibe yi ak ñaar ne leen: «Mbaa bëgguleena dem, yéen itam?»
YOWAANA 6 in Téereb Injiil