Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 6:31-43 in Wolof

Help us?

YOWAANA 6:31-43 in Téereb Injiil

31 Sunuy maam dunde nañu mànn ca màndiŋ ma, ndaxte Mbind mi nee na: “Jox na leen, ñu lekk ñam wu wàcce ca asamaan.”»
32 Yeesu waxaat ne: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, du Musaa moo leen jox ñam woowu wàcce ca asamaan; sama Baay ci boppam, moo leen di jox ñam wu wóor, wi wàcce ca asamaan.
33 Ndaxte ñam, wi Yàlla di joxe, mooy ñam wiy wàcce ci asamaan tey jox àddina si dund.»
34 Ñu ne ko nag: «Sang bi, kon dee nu faral di jox ci ñam woowe!»
35 Yeesu ne leen: «Man maay ñam wiy joxe dund. Ku ñëw ci man, doo xiif mukk; te ku ma gëm, doo mar.
36 Waaye wax naa leen ko ba noppi; gis ngeen ma te taxul ngeen gëm!
37 Képp ku ma Baay bi jox dina ñëw ci man, te duma dàq mukk ki may fekksi.
38 Ndaxte wàccewuma ci asamaan ngir def sama bëgg-bëgg, waaye damay matal bëgg-bëggu ki ma yónni.
39 Lii mooy bëgg-bëggu ki ma yónni: bu ma ñàkk kenn ci ñi mu ma may, te dafa bëgg it ma dekkal leen keroog bés bu mujj ba.
40 Ndaxte lii mooy bëgg-bëggu Baay bi: képp ku gis Doom ji te gëm ko, am dund gu dul jeex, te bés bu mujj ba, dinaa ko dekkal!»
41 Yawut ya tàmbali di ñurumtoo Yeesu, ndaxte dafa ne: «Maay ñam wi wàcce ci asamaan.»
42 Ñu naan: «Ndax kii du Yeesu, doomu Yuusufa? Xam nanu ndeyam ak baayam. Kon nag lu tax léegi mu naan, mi ngi jóge asamaan?»
43 Yeesu ne leen: «Bàyyileen seen ñurumtu bi.
YOWAANA 6 in Téereb Injiil