Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 5:21-32 in Wolof

Help us?

YOWAANA 5:21-32 in Téereb Injiil

21 Maanaam, ni Baay bi di dekkale ñu dee ñi, di leen jox dund, noonu la Doom ji di joxe dund ñi mu ko bëgga jox.
22 Baay bi du àtte kenn; àtte bi yépp, jox na ko Doom ji,
23 ngir ñépp di teral Doom ji, ni ñuy terale Baay bi. Ku teralul Doom ji, teraloo Baay, bi ko yónni.
24 «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, ku dégg sama kàddu te gëm ki ma yónni, am nga dund gu dul jeex te doo jaar ca àtte ba, ndaxte génn nga ci dee, tàbbi ci dund.
25 Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, jamono dina ñëw te agsi na ba noppi, mooy jamono, ji ñu dee ñi di dégg baatu Doomu Yàlla ji, te ku ko dégg dinga dund.
26 Ndaxte ni Baay bi ame dund moom ci boppam, noonu it la ko maye Doom ji, mu am ko ci boppam.
27 Jox na Doom ji itam sañ-sañu àtte, ndaxte mooy Doomu nit ki.
28 «Bu leen ci dara jaaxal; ndaxte jamonoo ngi ñëw ju néew yépp, yi nekk ci seen bàmmeel, di dégg baatam tey génn.
29 Ñi daan jëf lu baax dinañu dekki, dund ba fàww, waaye ñi daan jëf lu bon, dinañu dekki, ñu daan leen.
30 Manumaa def dara man ci sama bopp. Ni ma Baay bi di digale rekk laay àttee, te sama àtte bu jub la, ndaxte defuma sama bëgg-bëgg, ci waawi ki ma yónni doŋŋ laay aw.
31 «Su ma seedeelee sama bopp, sama wax du am maana.
32 Waaye keneen moo may seedeel, te bir na ma ne la muy wax ci man dëgg la.
YOWAANA 5 in Téereb Injiil