Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 5:2-17 in Wolof

Help us?

YOWAANA 5:2-17 in Téereb Injiil

2 Ca wetu benn ci bunti dëkk ba nag, maanaam ca Buntu xar ya, am na fa bët bu tudd Betesda ci làkku yawut, te ñu wërale ko ak juróomi mbaar.
3 Ca suufu mbaar yooyu la jarag yu bare, yu deme niki ay gumba, ay lafañ ak ay làggi, daan tëdd, di xaar ndox mi yëngatu;
4 ndaxte, ci ni ñu ko nettalee, benn malaakam Boroom bi da daan wàcc léeg-léeg di jax ndox mi. Bu ndox mi masaa yëngu ba noppi, jarag ju ca jiitu, wopp joo amaan, daldi wér ca saa sa.
5 Amoon na fa benn waay bu feebaroon lu mat fanweeri at ak juróom ñett.
6 Bi ko Yeesu séenee mu tëdd, te mu xam ne woppam ji yàggoon na lool, mu laaj ko ne: «Ndax bëgg ngaa wér?»
7 Jarag ja ne ko: «Sang bi, duma am ku ma sóob ci ndox mi, bu yëngoo; su ma ciy fexee dem, ñu jëkk ma ci.»
8 Yeesu ne ko: «Jógal, jël sa basaŋ te dox.»
9 Ca saa sa mu daldi wér, jël basaŋam, daldi dox. Mbir moomu dafa daje woon ak bésub noflaay ba,
10 looloo tax ba Yawut ya daldi ne nit ku wér ka: «Tey bésub noflaay la, te sunu yoon aaye na, ngay yor sa basaŋ.»
11 Mu ne leen: «Ki ma faj moo ma ne: “Jëlal sa basaŋ te dox.”»
12 Ñu ne ko nag: «Ku la ne: “Jëlal sa basaŋ te dox”?»
13 Waaye waa ji xamul ki ko wéral, fekk booba Yeesu dem na, te nit ñu bare teewoon nañu ca bérab ba.
14 Bi ñu ca tegee ab diir, Yeesu dajeek moom ca kër Yàlla ga ne ko: «Déglul, fii mu ne, wér nga; bul defati bàkkaar, ngir ragal lu yées lii dal la.»
15 Noonu nit ka dellu ne Yawut ya, Yeesu moo ko fajoon.
16 Looloo tax Yawut ya di wuta sonal Yeesu, ndaxte daan na jëfe noonu ca bésub noflaay ba.
17 Waaye Yeesu wax na leen ne: «Sama Baay nekk na ba tey ci liggéey, kon man itam damay liggéey.»
YOWAANA 5 in Téereb Injiil