Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 4:27-54 in Wolof

Help us?

YOWAANA 4:27-54 in Téereb Injiil

27 Noonu nag taalibey Yeesu ya délsi, gis muy wax ak ab jigéen. Ñu daldi jaaxle lool. Waaye kenn ñemewu ko woon ne: «Looy laaj?» walla: «Lu tax ngay wax ak moom?»
28 Noonu jigéen ja wacc fa njaqam, daldi dem ca dëkk ba ne leen:
29 «Kaayleen gis; nit a nga fee ku ma wax lépp lu ma masa def. Ndax kooku du Almasi bi?»
30 Noonu waa dëkk ba jóg, jëm ca Yeesu.
31 Fekk taalibey Yeesu ya di ko gétën ne: «Kilifa gi, lekkal.»
32 Waaye Yeesu ne leen: «Am na ñam wu may lekk, te xamuleen ko.»
33 Taalibe ya nag di laajante naan: «Ndax dafa am ku ko indil lekk?»
34 Yeesu ne leen: «Sama ñam moo di def coobarey ki ma yónni te àggale liggéey, bi mu ma sant.
35 Du dangeen naan: “Fii ak ñeenti weer ñu góob”? Waaye man, dama leen naan: xool-leen tool yi, ñoo ngi ñor ba weex tàll, di xaar ku leen góob.
36 Kiy góob tool yi mu ngi jot xaat peyam; day dajale nit ñi ngir dund gu dul jeex, ni ñuy dajalee pepp. Kon boog kiy ji dina bégandoo ak kiy góob.
37 Wax ji ñu wax ne: “Kenn dina ji, keneen góob,” dëgg la.
38 Yebal naa leen, ngeen góob tool bu ngeen beyul. Ñeneen a ko bey, te yéena ko jariñoo.»
39 Bi jigéen ja nee waa dëkk ba: «Wax na ma li ma def lépp,» ñu bare gëm nañu Yeesu.
40 Ñu daldi dikk ñaan Yeesu, mu dal ak ñoom. Yeesu toog fa ñaari fan.
41 Ñu bare gëm ko ndax li mu doon wax.
42 Ñu ne jigéen ja: «Léegi gëm nanu, te du li nga wax moo tax waaye li nu gisal sunu bopp. Te xam nanu ne dëgg-dëgg kii moo di Musalkatu àddina si.»
43 Bi Yeesu amee ñaari fan ca dëkk ba, mu jóge fa, jëm diiwaanu Galile,
44 ndaxte moom ci boppam nee woon na: «Ab yonent, kenn du ko faaydaal ca réewam.»
45 Bi mu agsee Galile, nit ñi teeru ko, ndaxte ñoom itam teewoon nañu ca màggalu bésu Mucc ba ca Yerusalem, te gisoon nañu la mu fa defoon lépp.
46 Noonu kon mu délsi Kana ci Galile, dëkk ba mu soppee woon ndox ma biiñ. Amoon na benn dagu buur bu dëkkoon Kapernawum te doomam feebar.
47 Bi mu déggee ne, Yeesu jóge na Yude, ñëw Galile, mu dikk ci moom, ñaan ko mu ñëw këram, wéral doomam, ji wopp bay bëgga dee.
48 Yeesu ne ko: «Yéen daal, dungeen gëm mukk, fi ak gisuleen ay firnde walla ay kéemaan.»
49 Dagu buur ba neeti ko: «Sang bi, ñëwal, bala sama doom di dee.»
50 Yeesu ne ko: «Demal, sa doom dina dund.» Kilifa ga gëm la ko Yeesu wax, daldi dem.
51 Bi muy dellu këram nag, ay surgaam gatandu ko. Ñu daldi ne ko: «Xale bi dina dund!»
52 Mu laaj leen ci ban waxtu la tàmbalee tane, ñu ne ko: «Démb ca njolloor la am ag féex.»
53 Noonu baayu xale ba daldi seetlu ne, ca waxtu woowa la ko Yeesu ne woon: «Sa doom dina dund.» Moom ak njabootam gépp, ñu daldi gëm Yeesu.
54 Lii mooy ñaareelu firnde, bi Yeesu def ci Galile, gannaaw bi mu jógee Yude.
YOWAANA 4 in Téereb Injiil