Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 4:22-39 in Wolof

Help us?

YOWAANA 4:22-39 in Téereb Injiil

22 Yéen waa Samari, xamuleen li ngeen di jaamu. Nun Yawut yi, xam nanu li nuy jaamu, ndaxte kiy musal àddina ci Yawut yi la jóge.
23 Waaye jamono dina ñëw, te agsi na ba noppi, jamono joo xam ne jaamukat yi dëgg dinañu jaamu Baay bi ci xel ak ci dëgg. Ñooñu nag, ñooy jaamu Baay bi, ni mu ko bëgge.
24 Yàlla xel la, kon ñi koy jaamu war nañu koo jaamu ci xel ak ci dëgg.»
25 Jigéen ja ne ko: «Xam naa ne Almasi bi —maanaam Kirist— dina ñëw te bu ñëwee, dina nu leeralal lépp.»
26 Yeesu ne ko: «Maa di Almasi bi, man miy wax ak yaw.»
27 Noonu nag taalibey Yeesu ya délsi, gis muy wax ak ab jigéen. Ñu daldi jaaxle lool. Waaye kenn ñemewu ko woon ne: «Looy laaj?» walla: «Lu tax ngay wax ak moom?»
28 Noonu jigéen ja wacc fa njaqam, daldi dem ca dëkk ba ne leen:
29 «Kaayleen gis; nit a nga fee ku ma wax lépp lu ma masa def. Ndax kooku du Almasi bi?»
30 Noonu waa dëkk ba jóg, jëm ca Yeesu.
31 Fekk taalibey Yeesu ya di ko gétën ne: «Kilifa gi, lekkal.»
32 Waaye Yeesu ne leen: «Am na ñam wu may lekk, te xamuleen ko.»
33 Taalibe ya nag di laajante naan: «Ndax dafa am ku ko indil lekk?»
34 Yeesu ne leen: «Sama ñam moo di def coobarey ki ma yónni te àggale liggéey, bi mu ma sant.
35 Du dangeen naan: “Fii ak ñeenti weer ñu góob”? Waaye man, dama leen naan: xool-leen tool yi, ñoo ngi ñor ba weex tàll, di xaar ku leen góob.
36 Kiy góob tool yi mu ngi jot xaat peyam; day dajale nit ñi ngir dund gu dul jeex, ni ñuy dajalee pepp. Kon boog kiy ji dina bégandoo ak kiy góob.
37 Wax ji ñu wax ne: “Kenn dina ji, keneen góob,” dëgg la.
38 Yebal naa leen, ngeen góob tool bu ngeen beyul. Ñeneen a ko bey, te yéena ko jariñoo.»
39 Bi jigéen ja nee waa dëkk ba: «Wax na ma li ma def lépp,» ñu bare gëm nañu Yeesu.
YOWAANA 4 in Téereb Injiil