Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 4:11-23 in Wolof

Help us?

YOWAANA 4:11-23 in Téereb Injiil

11 Jigéen ja ne ko: «Sang bi, teen bi xóot na te amuloo baag, kon fooy jële ndoxum dund?
12 Xanaa kay xalaatuloo ne yaa gëna màgg sunu maam Yanqóoba, moom mi nu gasal teen bii, mu naan ci moom ak i doomam, wëgg cig juram?»
13 Yeesu wax ko ne: «Ku naan ci ndoxum teen bii, balaa yàgg mu maraat,
14 waaye ndox mi may joxe, ku ci naan du marati mukk, ndaxte day nekk ci moom bëtu ndox buy ball, di joxe dund gu dul jeex.»
15 Noonu jigéen ja daldi ko ne: «Sang bi, may ma ci ndox moomu, ngir ma bañatee mar, bay ñëw ba fii di rootsi.»
16 Yeesu ne ko: «Demal wooyi sa jëkkër te ñëw.»
17 Jigéen ja ne ko: «Awma jëkkër de.» Yeesu ne ko: «Wax nga dëgg ne amuloo jëkkër,
18 ndaxte amoon nga juróomi jëkkër, te ki nga nekkal léegi du sa jëkkër. Li nga wax dëgg la.»
19 Jigéen ja ne ko: «Sang bi, gis naa ne ab yonent nga.
20 Nun nag, naka-jekk sunuy maam ca tund wee ngay séen lañu daan jaamoo Yàlla, waaye yéen Yawut yi, dangeen ne Yerusalem lañu wara jaamoo Yàlla.»
21 Yeesu ne ko: «Jigéen ji, gëmal lii ma lay wax: dina am jamono joo xam ne du ci tund wale te du ci Yerusalem ngeen di jaamoo Baay bi.
22 Yéen waa Samari, xamuleen li ngeen di jaamu. Nun Yawut yi, xam nanu li nuy jaamu, ndaxte kiy musal àddina ci Yawut yi la jóge.
23 Waaye jamono dina ñëw, te agsi na ba noppi, jamono joo xam ne jaamukat yi dëgg dinañu jaamu Baay bi ci xel ak ci dëgg. Ñooñu nag, ñooy jaamu Baay bi, ni mu ko bëgge.
YOWAANA 4 in Téereb Injiil