Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 4:1-27 in Wolof

Help us?

YOWAANA 4:1-27 in Téereb Injiil

1 Amoon na benn bés Farisen yi dégg ne, ñiy topp Yeesu ñoo ëpp ñiy topp Yaxya, te ñi Yeesu sóob ci ndox ñoo ëpp ñi Yaxya sóob.
2 Fekk Yeesu moom ci boppam daawul sóob kenn ci ndox, waaye ay taalibeem ñoo daan sóobe.
3 Bi Yeesu yégee loolu nag, mu jóge Yude, dellu diiwaanu Galile.
4 Bi muy dem Galile, waroon na jaar ci diiwaanu Samari.
5 Noonu mu agsi ci wetu dëkku Sikar ci tool, bi Yanqóoba mayoon doomam Yuusufa.
6 Foofa la teenu Yanqóoba nekkoon. Yeesu toog ca pindu teen ba, di noppalu ndax coonob tukki ba. Ca digg bëccëg la woon.
7 Noonu jigéenu waa Samari ñëw fa di root. Yeesu ne ko: «May ma ndox, ma naan.»
8 Fekk booba nag, taalibey Yeesu ya dañoo demoon ca biir dëkk ba, di jënd lu ñu lekk.
9 Jigéen ja ne ko: «Yaw, ngay Yawut, man maay jigéen ju dëkk Samari; nan nga ma mana ñaane ndox?» Jigéen ja wax na loolu, ndaxte Yawut ya bokkuñu woon ak waa Samari ndab yu ñuy lekke.
10 Noonu nag Yeesu ne ko: «Soo xamoon li Yàlla maye, xam ki lay ñaan ndox, kon yaw ci sa bopp, yaa koy ñaan, te moom dina la may ndoxum dund.»
11 Jigéen ja ne ko: «Sang bi, teen bi xóot na te amuloo baag, kon fooy jële ndoxum dund?
12 Xanaa kay xalaatuloo ne yaa gëna màgg sunu maam Yanqóoba, moom mi nu gasal teen bii, mu naan ci moom ak i doomam, wëgg cig juram?»
13 Yeesu wax ko ne: «Ku naan ci ndoxum teen bii, balaa yàgg mu maraat,
14 waaye ndox mi may joxe, ku ci naan du marati mukk, ndaxte day nekk ci moom bëtu ndox buy ball, di joxe dund gu dul jeex.»
15 Noonu jigéen ja daldi ko ne: «Sang bi, may ma ci ndox moomu, ngir ma bañatee mar, bay ñëw ba fii di rootsi.»
16 Yeesu ne ko: «Demal wooyi sa jëkkër te ñëw.»
17 Jigéen ja ne ko: «Awma jëkkër de.» Yeesu ne ko: «Wax nga dëgg ne amuloo jëkkër,
18 ndaxte amoon nga juróomi jëkkër, te ki nga nekkal léegi du sa jëkkër. Li nga wax dëgg la.»
19 Jigéen ja ne ko: «Sang bi, gis naa ne ab yonent nga.
20 Nun nag, naka-jekk sunuy maam ca tund wee ngay séen lañu daan jaamoo Yàlla, waaye yéen Yawut yi, dangeen ne Yerusalem lañu wara jaamoo Yàlla.»
21 Yeesu ne ko: «Jigéen ji, gëmal lii ma lay wax: dina am jamono joo xam ne du ci tund wale te du ci Yerusalem ngeen di jaamoo Baay bi.
22 Yéen waa Samari, xamuleen li ngeen di jaamu. Nun Yawut yi, xam nanu li nuy jaamu, ndaxte kiy musal àddina ci Yawut yi la jóge.
23 Waaye jamono dina ñëw, te agsi na ba noppi, jamono joo xam ne jaamukat yi dëgg dinañu jaamu Baay bi ci xel ak ci dëgg. Ñooñu nag, ñooy jaamu Baay bi, ni mu ko bëgge.
24 Yàlla xel la, kon ñi koy jaamu war nañu koo jaamu ci xel ak ci dëgg.»
25 Jigéen ja ne ko: «Xam naa ne Almasi bi —maanaam Kirist— dina ñëw te bu ñëwee, dina nu leeralal lépp.»
26 Yeesu ne ko: «Maa di Almasi bi, man miy wax ak yaw.»
27 Noonu nag taalibey Yeesu ya délsi, gis muy wax ak ab jigéen. Ñu daldi jaaxle lool. Waaye kenn ñemewu ko woon ne: «Looy laaj?» walla: «Lu tax ngay wax ak moom?»
YOWAANA 4 in Téereb Injiil