Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 3:20-32 in Wolof

Help us?

YOWAANA 3:20-32 in Téereb Injiil

20 Képp kuy def lu bon day bañ leer gi te du ci ñëw, ndax ragal ay jëfam di feeñ bëccëg ndarakàmm.
21 Waaye ku def lu jub day ñëw ci leer gi, ngir ñu xam ne def na ay jëfam ci kanam Yàlla.
22 Gannaaw loolu Yeesu ànd ak ay taalibeem, dem ca biir diiwaanu Yude, toog fa ak ñoom ab diir, di sóob nit ñi ci ndox.
23 Yaxya moom itam doon na sóobe ci ndox ci dëkku Aynon, ca wetu dëkku Salim, ndaxte diiwaan booba bare woon na ndox. Nit ñi daan nañu ñëw ci moom, mu di leen sóob.
24 Booba tëjaguñu Yaxya ci kaso.
25 Foofa ay taalibey Yaxya tàmbalee werante ak benn Yawut ci mbirum sangu set.
26 Ci kaw loolu ñu dem ca Yaxya ne ko: «Kilifa gi, ndax fàttaliku nga kooka nga seede woon te mu nekkoon ak yaw ca gannaaw dexu Yurdan? Moom de, ma ngay sóobe ci ndox léegi te ñépp a ngay dem ca moom!»
27 Yaxya ne leen: «Kenn manula am dara lu ko Yàlla joxul.
28 Yéen ci seen bopp man ngeena seede ne waxoon naa ne duma Almasi bi waaye dañu maa yónni ma jiitusi ko.
29 Kiy céetal moo moom séetam. Waaye xaritu kiy céetal dafay taxaw di ko déglu, tey bég, bu déggee baatam. Mbég moomu moo di sama bos tey, te fi mu nekk mat na sëkk.
30 Li war moo di moom, mu gëna màgg te man, ma gëna féete suuf.»
31 Ki jóge ci kaw moo féete kaw ñépp; ki jóge ci suuf nag, ci suuf rekk la mana bokk, te ni niti àddina lay waxe. Ki jóge asamaan
32 day wax li mu gis ak li mu dégg, waaye kenn nanguwul li mu seede.
YOWAANA 3 in Téereb Injiil