Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 3:2-17 in Wolof

Help us?

YOWAANA 3:2-17 in Téereb Injiil

2 Genn guddi mu ñëw ca Yeesu ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne Yàllaa la yónni ngir nga jàngal nu, ndaxte kenn manula def firnde yii ngay wone te Yàlla àndul ak moom.»
3 Yeesu ne ko: «Ci dëgg-dëgg maa ngi la koy wax, képp ku judduwaatul doo mana seede nguuru Yàlla.»
4 Nikodem ne ko: «Nit ku xas ba màggat, nan lay mana judduwaate? Ndax day dellu ci biiru yaayam ngir judduwaat?»
5 Yeesu ne ko: «Ci dëgg-dëgg maa ngi la koy wax, ku judduwul ci ndox ak ci Xelum Yàlla, doo mana bokk ci nguuru Yàlla.
6 Lu juddoo ci nit, nit la; waaye lu juddoo ci Xelum Yàlla, xel la.
7 Li ma ne: “Fàww ngeen judduwaat,” bumu la jaaxal.
8 Ngelaw fu ko neex lay jublu. Yaa ngi koy dégg waaye xamuloo fu mu jóge, xamuloo fu mu jëm. Noonu la mel it ci képp ku juddoo ci Xelum Yàlla.»
9 Ci baat yooyu Nikodem ne ko: «Nu loolu mana ame?»
10 Yeesu ne ko: «Yaw yaay jàngal bànni Israyil te xamuloo mbir yii?
11 Ci dëgg-dëgg maa ngi la koy wax, noo ngi wax li nu xam, di nettali li nu gis, waaye nanguwuleena gëm li nu seede.
12 Gannaaw gëmuleen li ma leen di wax ci mbiri àddina, naka ngeen mana gëme, bu ma leen waxee ci mbiri asamaan?
13 Kenn masula yéeg ci asamaan su dul ki fa jóge, muy Doomu nit ki.
14 Te itam na Musaa sampe woon ab bant ca diggu màndiŋ ma, takk ca jaan, ja mu defare woon xànjar, fàww ñu yékkatee noonu Doomu nit ki,
15 ngir képp ku ko gëm am ci moom dund gu dul jeex.»
16 Ndaxte Yàlla dafa bëgg àddina, ba joxe jenn Doomam ji mu am kepp, ngir képp ku ko gëm am dund gu dul jeex te doo sànku mukk.
17 Yàlla yónniwul Doomam ci àddina ngir mu daan nit ñi, waaye ngir musal leen.
YOWAANA 3 in Téereb Injiil