Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 3:13-23 in Wolof

Help us?

YOWAANA 3:13-23 in Téereb Injiil

13 Kenn masula yéeg ci asamaan su dul ki fa jóge, muy Doomu nit ki.
14 Te itam na Musaa sampe woon ab bant ca diggu màndiŋ ma, takk ca jaan, ja mu defare woon xànjar, fàww ñu yékkatee noonu Doomu nit ki,
15 ngir képp ku ko gëm am ci moom dund gu dul jeex.»
16 Ndaxte Yàlla dafa bëgg àddina, ba joxe jenn Doomam ji mu am kepp, ngir képp ku ko gëm am dund gu dul jeex te doo sànku mukk.
17 Yàlla yónniwul Doomam ci àddina ngir mu daan nit ñi, waaye ngir musal leen.
18 Képp ku ko gëm deesu la daan, waaye ku ko gëmul daan nañu la ba noppi, ndaxte gëmuloo ci turu Doom ji Yàlla am kepp.
19 Ci nii la àtte bi ame: leer gi ñëw na ci àddina, waaye nit lëndëm gi lañu taamu ndax seeni jëf yu bon.
20 Képp kuy def lu bon day bañ leer gi te du ci ñëw, ndax ragal ay jëfam di feeñ bëccëg ndarakàmm.
21 Waaye ku def lu jub day ñëw ci leer gi, ngir ñu xam ne def na ay jëfam ci kanam Yàlla.
22 Gannaaw loolu Yeesu ànd ak ay taalibeem, dem ca biir diiwaanu Yude, toog fa ak ñoom ab diir, di sóob nit ñi ci ndox.
23 Yaxya moom itam doon na sóobe ci ndox ci dëkku Aynon, ca wetu dëkku Salim, ndaxte diiwaan booba bare woon na ndox. Nit ñi daan nañu ñëw ci moom, mu di leen sóob.
YOWAANA 3 in Téereb Injiil