Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 2:9-13 in Wolof

Help us?

YOWAANA 2:9-13 in Téereb Injiil

9 Ki jiite xew wa ñam ndox, ma Yeesu soppi biiñ. Xamul woon fu biiñ booba jóge, waaye surga ya tanqoon ndox ma, ñoom xamoon nañu ko. Naka noonu mu woo boroom céet ga ne ko:
10 «Ci xew yépp, naan gu neex gi lañuy jëkke. Bu nit ñi doyalee, ñu sooga génne ga ca des. Waaye yaw dangaa dencoon gi gëna neex ba nëgëni.»
11 Firnde jii ame ca Kana, ca diiwaanu Galile, moo doon kéemaan gi Yeesu jëkka def. Ci noonu la wonee màggaayam te ay taalibeem gëm nañu ko.
12 Bi loolu weesoo, mu ànd ak yaayam, ay rakkam ak i taalibeem, dem dëkku Kapernawum. Waaye yàgguñu fa.
13 Màggalu Yawut, gi ñuy wax bésu Mucc ba, mu ngi doon jubsi. Yeesu dem Yerusalem,
YOWAANA 2 in Téereb Injiil