Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 2:3-12 in Wolof

Help us?

YOWAANA 2:3-12 in Téereb Injiil

3 Ca biir xew wa, biiñ ba daldi jeex. Yaayu Yeesu ne ko: «Amatuñu biiñ.»
4 Yeesu ne: «Soxna si, loo ma bëggal? Ndaxte sama waxtu jotagul.»
5 Yaayam daldi ne surga ya: «Defleen lépp lu mu leen wax.»
6 Foofa amoon na fa juróom benni ndaa yu ñu yett ci doj, yu Yawut ya daan jëfandikoo ngir seen sangu set. Ndaa lu nekk man na def daanaka téeméeri liitar.
7 Yeesu ne surga ya: «Duyleen ndaa yi.» Ñu duy leen, ba ñu fees bay rembat.
8 Noonu Yeesu ne leen: «Tanqleen ci léegi, yót ko njiitu xew wi.» Ñu daldi ko ciy yót.
9 Ki jiite xew wa ñam ndox, ma Yeesu soppi biiñ. Xamul woon fu biiñ booba jóge, waaye surga ya tanqoon ndox ma, ñoom xamoon nañu ko. Naka noonu mu woo boroom céet ga ne ko:
10 «Ci xew yépp, naan gu neex gi lañuy jëkke. Bu nit ñi doyalee, ñu sooga génne ga ca des. Waaye yaw dangaa dencoon gi gëna neex ba nëgëni.»
11 Firnde jii ame ca Kana, ca diiwaanu Galile, moo doon kéemaan gi Yeesu jëkka def. Ci noonu la wonee màggaayam te ay taalibeem gëm nañu ko.
12 Bi loolu weesoo, mu ànd ak yaayam, ay rakkam ak i taalibeem, dem dëkku Kapernawum. Waaye yàgguñu fa.
YOWAANA 2 in Téereb Injiil