Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 20:8-17 in Wolof

Help us?

YOWAANA 20:8-17 in Téereb Injiil

8 Noonu keneen ka jiitu woon ca bàmmeel ba, duggsi moom itam. Naka la gis, daldi gëm.
9 Taalibe yi xamaguñu woon Mbind mi doon wone ne Yeesu dafa wara dekki.
10 Noonu taalibe ya dëpp, ñibbi.
11 Maryaama nag moom, ma nga desoon ca biti, ca wetu bàmmeel ba, di jooy. Bi muy jooy, mu sëgg, yër ci biir,
12 séen ñaari malaaka yu sol mbubb yu weex, toog ca bérab, ba ñu dencoon Yeesu; kenn ka féeteek bopp bi, ki ci des ca tànk ya.
13 Malaaka ya laaj ko ne: «Jigéen ji, looy jooy?» Mu ne leen: «Dañoo jël sama Boroom, te xawma fu ñu ko yóbbu.»
14 Bi mu waxee loolu, mu geestu, séen Yeesu mu taxaw, waaye xamul woon ne moom la.
15 Yeesu laaj ko ne: «Jigéen ji, looy jooy? Kooy seet?» Mu foog ne boroom tool ba la, ne ko: «Sëriñ bi, bu fekkee yaa ko yóbbu, wax ma foo ko denc, ma jëli ko.»
16 Noonu Yeesu ne ko: «Maryaama.» Mu walbatiku, làkk ko ci yawut ne ko: «Ràbbuni!» Ràbbuni mooy tekki «Kilifa gi».
17 Yeesu ne ko: «Bu ma téye, ndaxte yéegaguma ca Baay ba. Waaye demal, ne samay bokk, maa ngi yéeg ca sama Baay biy seen Baay, ca sama Yàlla jiy seen Yàlla.»
YOWAANA 20 in Téereb Injiil