Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 20:6-22 in Wolof

Help us?

YOWAANA 20:6-22 in Téereb Injiil

6 Noonu Simoŋ Piyeer, mi ko toppoon, agsi, daldi dugg. Mu séen càngaay la ci suuf,
7 ak kaala ga muuroon boppu Yeesu. Waaye kaala googu àndul ak càngaay la; dañu ko laxas, teg ko ci wet.
8 Noonu keneen ka jiitu woon ca bàmmeel ba, duggsi moom itam. Naka la gis, daldi gëm.
9 Taalibe yi xamaguñu woon Mbind mi doon wone ne Yeesu dafa wara dekki.
10 Noonu taalibe ya dëpp, ñibbi.
11 Maryaama nag moom, ma nga desoon ca biti, ca wetu bàmmeel ba, di jooy. Bi muy jooy, mu sëgg, yër ci biir,
12 séen ñaari malaaka yu sol mbubb yu weex, toog ca bérab, ba ñu dencoon Yeesu; kenn ka féeteek bopp bi, ki ci des ca tànk ya.
13 Malaaka ya laaj ko ne: «Jigéen ji, looy jooy?» Mu ne leen: «Dañoo jël sama Boroom, te xawma fu ñu ko yóbbu.»
14 Bi mu waxee loolu, mu geestu, séen Yeesu mu taxaw, waaye xamul woon ne moom la.
15 Yeesu laaj ko ne: «Jigéen ji, looy jooy? Kooy seet?» Mu foog ne boroom tool ba la, ne ko: «Sëriñ bi, bu fekkee yaa ko yóbbu, wax ma foo ko denc, ma jëli ko.»
16 Noonu Yeesu ne ko: «Maryaama.» Mu walbatiku, làkk ko ci yawut ne ko: «Ràbbuni!» Ràbbuni mooy tekki «Kilifa gi».
17 Yeesu ne ko: «Bu ma téye, ndaxte yéegaguma ca Baay ba. Waaye demal, ne samay bokk, maa ngi yéeg ca sama Baay biy seen Baay, ca sama Yàlla jiy seen Yàlla.»
18 Noonu Maryaamam Magdala dem, yégali ko taalibe ya ne leen: «Gis naa Boroom bi!» Mu daldi leen nettali li mu ko wax.
19 Bés boobu ca ngoon sa, taalibe yaa nga daje woon ca genn kër, tëju ca biir ndax ragal Yawut ya. Yeesu ne tëll ci seen biir ne leen: «Na jàmm wàcc ci yéen!»
20 Mu daldi leen won ay loxoom ak wetam. Bi ñu gisee Boroom bi, taalibe ya daldi bég lool.
21 Yeesu dellu ne leen: «Na jàmm wàcc ci yéen! Ni ma Baay bi yónnee, noonu laa leen di yónnee, man itam.»
22 Bi mu waxee loolu, mu ëf leen ne leen: «Sol naa leen Xelu Yàlla mu Sell mi.
YOWAANA 20 in Téereb Injiil