Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 1:7-17 in Wolof

Help us?

YOWAANA 1:7-17 in Téereb Injiil

7 Kooku ñëw na, doon ab seede, ngir wax ci mbirum leer gi. Ñëw na ngir ñépp dégg li mu wax te gëm.
8 Moom ci boppam du woon leer gi, waaye ñëw na ngir seedeel leer gi.
9 Kàddu googu mooy leer gu wóor, giy ñëw ci àddina te di leeral nit ku nekk.
10 Ci àddina la nekkoon, àddina si ñu sàkk jaarale ko ci moom, te àddina xamu ko.
11 Ñëw na ci réewam, te ay ñoñam nanguwuñu ko.
12 Teewul ñi ko nangu te gëm ci turam, may na leen, ñu am sañ-sañu nekk doomi Yàlla.
13 Ñooñu judduwuñu ci deret walla ci bëgg-bëggu yaram, walla ci coobarey nit. Ñu ngi juddu ci Yàlla.
14 Kàddu gi ñëw, doon nit, dëkk ci sunu biir. Gis nañu ndamam, mu fees ak yiw ak dëgg, ndam li Baay bi jox jenn Doomam ji mu am kepp.
15 Yaxyaa ngi koy seedeel te yégle na lii; nee na: «Moo taxoon ma wax ne: “Dina ñëw sama gannaaw waaye moo ma gëna màgg, ndaxte nekk na laata may juddu.”»
16 Kàddu gi fees na ak yiw, te nun ñépp jot nanu ci sunu wàll, mu barkeel nu ay yooni yoon.
17 Ndigali Yàlla yi, ci gémmiñu Musaa lañu leen jaarale; yiw wi ak dëgg gi, Yeesu Kirist moo ko indaale.
YOWAANA 1 in Téereb Injiil