Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 1:28-46 in Wolof

Help us?

YOWAANA 1:28-46 in Téereb Injiil

28 Lii xewoon na ci dëkku Betani, ca gannaaw dexu Yurdan, fa Yaxya doon sóobe.
29 Ca ëllëg sa, bi Yaxya gisee Yeesu, muy ñëw ci moom, mu ne: «Xool-leen! Kii mooy Gàttub Yàlla, bi ñu nara rendi, ngir dindi bàkkaaru àddina.
30 Moo taxoon ma wax ne: “Am na kuy ñëw sama gannaaw, waaye moo ma gëna màgg, ndaxte nekk na laata may juddu.”
31 Xawma woon kooku kan la waroona doon, waaye xamal ko bànni Israyil moo tax ma ñëw, di sóob nit ñi ci ndox.»
32 Ci kaw loolu Yaxya seede na lii: «Gis naa Xelu Yàlla mi ci melow pitax, mu jóge ci asamaan, tegu ci moom.
33 Bi loola laata am, xawma woon mooy kan, waaye Yàlla, mi ma yebal may sóobe ci ndox, nee woon na ma: “Dinga gis Xel mu Sell mi wàcc, tegu ci kaw nit. Kooku moo di ki leen di sóob ci Xel mu Sell mi.”»
34 Yaxya teg ca ne: «Gis naa loolu te seede naa ne moom moo di Doomu Yàlla ji.»
35 Ca ëllëg sa Yaxya taxawaatoon na ca bérab booba, ànd ak ñaari taalibeem.
36 Bi mu gisee Yeesu muy romb, mu daldi ne: «Kii mooy Gàttub Yàlla bi!»
37 Ñaari taalibe ya dégg li mu wax, daldi dem toppi Yeesu.
38 Yeesu geestu, gis ne ñoo ngi koy topp. Mu ne leen: «Lu ngeen soxla woon?» Ñu ne ko: «Foo dëkk, Ràbbi?» Ràbbi mi ngi tekki «Kilifa gi».
39 Yeesu ne leen: «Kaayleen gis.» Noonu ñu dem, seeti fa mu daloon, ngoonalal ko. Ci tàkkusaani kaw la woon.
40 Kenn ci ñoom ñaar, ñi déggoon li Yaxya wax te topp Yeesu, ma nga tuddoon Andare, mi bokkoon ak Simoŋ Piyeer ndey ak baay.
41 Andare dafa daldi dem seeti Simoŋ ne ko: «Gis nanu Almasi bi.» Baat boobu mi ngi tekki «Kirist».
42 Noonu mu yóbbu ko ci Yeesu. Yeesu xool ko ne ko: «Yaa di Simoŋ, doomu Yowaana. Dinañu la wooye Sefas.» Sefas mi ngi tekki «Piyeer», maanaam «xeer».
43 Ca ëllëg sa mu fas yéenee dem diiwaanu Galile te mu gis Filib. Yeesu ne ko: «Toppal ci man.»
44 Filib mu nga dëkkoon Betsayda, dëkku Andare ak Piyeer.
45 Filib dajeek Nataneel ne ko: «Gis nanu ki yoonu Musaa wi ak yonent yi doon wax. Mu ngi tudd Yeesu, doomu Yuusufa, te dëkk Nasaret.»
46 Nataneel ne ko: «Aa! Ndax dara lu baax man na jóge Nasaret?» Filib ne ko: «Ñëwal gis.»
YOWAANA 1 in Téereb Injiil