Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 1:19-37 in Wolof

Help us?

YOWAANA 1:19-37 in Téereb Injiil

19 Lii mooy seedes Yaxya. Amoon na bés Yawut ya yónni ay sarxalkat ca Yaxya, ñu ànd ak ñu soqikoo ci giiru Lewi. Ñu nga jóge Yerusalem, ñëw ci moom, di ko laaj mooy kan.
20 Yaxya tontu na leen te nëbbu ci dara, wóoral na leen ne moom du Almasi bi.
21 Ñu laaj ko ne: «Kon yaay kan? Ndax yaa di Ilyaas?» Mu ne leen: «Déedéet, duma Ilyaas.» Ñu ne ko: «Ndax yaa di Yonent, bi wara ñëw?» Mu ne leen: «Déedéet.»
22 Noonu ñu laaj ko ne: «Wax nu yaay kan, ngir nu mana tontu ñi nu yónni. Nga ne yaa di kan?»
23 Yaxya wax leen li yonent Yàlla Esayi waxoon ne: «Man maa di baat biy yégle ci màndiŋ mi ne: “Xàll-leen yoonu Boroom bi!”»
24 Amoon na ñu bokk ca Farisen ya, yu àndoon ca mbooloo, ma ñu yónni woon ca Yaxya.
25 Ñooñu laaj ko ne: «Gannaaw doo Almasi bi, doo Ilyaas, doo Yonent bi wara ñëw, lu tax ngay sóob nit ñi ci ndox?»
26 Yaxya ne leen: «Man maa ngi sóobe ci ndox, waaye am na ci seen biir ku ngeen xamul.
27 Kookooy ñëw sama gannaaw, te man sax yeyoowumaa tekki ay dàllam.»
28 Lii xewoon na ci dëkku Betani, ca gannaaw dexu Yurdan, fa Yaxya doon sóobe.
29 Ca ëllëg sa, bi Yaxya gisee Yeesu, muy ñëw ci moom, mu ne: «Xool-leen! Kii mooy Gàttub Yàlla, bi ñu nara rendi, ngir dindi bàkkaaru àddina.
30 Moo taxoon ma wax ne: “Am na kuy ñëw sama gannaaw, waaye moo ma gëna màgg, ndaxte nekk na laata may juddu.”
31 Xawma woon kooku kan la waroona doon, waaye xamal ko bànni Israyil moo tax ma ñëw, di sóob nit ñi ci ndox.»
32 Ci kaw loolu Yaxya seede na lii: «Gis naa Xelu Yàlla mi ci melow pitax, mu jóge ci asamaan, tegu ci moom.
33 Bi loola laata am, xawma woon mooy kan, waaye Yàlla, mi ma yebal may sóobe ci ndox, nee woon na ma: “Dinga gis Xel mu Sell mi wàcc, tegu ci kaw nit. Kooku moo di ki leen di sóob ci Xel mu Sell mi.”»
34 Yaxya teg ca ne: «Gis naa loolu te seede naa ne moom moo di Doomu Yàlla ji.»
35 Ca ëllëg sa Yaxya taxawaatoon na ca bérab booba, ànd ak ñaari taalibeem.
36 Bi mu gisee Yeesu muy romb, mu daldi ne: «Kii mooy Gàttub Yàlla bi!»
37 Ñaari taalibe ya dégg li mu wax, daldi dem toppi Yeesu.
YOWAANA 1 in Téereb Injiil