Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 19:5-29 in Wolof

Help us?

YOWAANA 19:5-29 in Téereb Injiil

5 Yeesu nag génn, tegoo mbubbum xarekat mu xonq mi ak kaalag dég gi. Pilaat it ne leen: «Waa jaa ngii!»
6 Waaye bi ñu ko gisee, sarxalkat yu mag ya ak alkaati ya di yuuxoo naan: «Daaj ko ci bant! Daaj ko ci bant, ba mu dee!» Pilaat ne leen: «Jël-leen ko, yéen, daaj ko ci bant, ndaxte gisuma ci moom genn tooñ.»
7 Yawut yi ne ko: «Am nanu aw yoon, te ci yoon woowu, war na dee ndaxte teg na boppam Doomu Yàlla.»
8 Bi Pilaat déggee wax jooju, dafa gëna tiit,
9 dugg ca taax ma, daldi ne Yeesu: «Foo jóge?» Waaye Yeesu tontuwu ko.
10 Pilaat ne ko: «Man ngay baña waxal? Xanaa xamuloo ne am naa sañ-sañu bàyyi la, te am naa itam sañ-sañu daaj la ci bant?»
11 Yeesu ne ko: «Amuloo benn sañ-sañ ci man su dul bi la Yàlla jox. Looloo tax ba ki ma jébbal ci say loxo am na bàkkaar, bi gëna réy.»
12 Booba nag la Pilaat doon fexee bàyyi Yeesu. Waaye Yawut ya di yuuxoo naan: «Boo bàyyee kii, doo xaritu buur bi Sesaar. Nit ku teg boppam buur, noonub Sesaar la!»
13 Bi Pilaat déggee loolu, mu daldi génne Yeesu ca biti, dem toog ca jalub àttekaay ba, ca fu ñuy wax Bérabu doj ya. Ci làkku yawut ñu naan ko Gabata.
14 Booba ñu ngi waajal màggalu bésu Mucc ba, ca weti digg bëccëg. Pilaat ne Yawut ya: «Seen buur a ngii!»
15 Waaye ñuy yuuxoo naan: «Na dee! Na dee! Daaj ko ci bant!» Pilaat ne leen: «Ndax seen buur bi, dama koo wara daaj ci bant?» Sarxalkat yu mag ya ne ko: «Amunu benn buur bu dul Sesaar!»
16 Noonu Pilaat jébbal leen Yeesu, ngir ñu daaj ko ci bant. Bi leen ko Pilaat jébbalee, ñu jël ko, yóbbu.
17 Yeesu ci boppam gàddu bant ba, génn ngir dem ca fa ñuy wax bérabu Kaaŋu bopp; ñu koy wooye Golgota ci làkku yawut.
18 Foofa la xarekat ya daaje Yeesu ca bant ba. Ci noonu it ñu daajaale ñaari nit ci wetam, mu nekk ca digg ba.
19 Pilaat santaane itam ñu bind, teg ko ca kaw bant, ba ñu ko daajoon. Mbind ma lii la wax: «Kii mooy Yeesum Nasaret, buuru Yawut yi.»
20 Mbind mooma, Yawut yu bare jàng nañu ko, ndaxte fa ñu daajoon Yeesu ca bant ba jege woon na dëkk ba, te mbind ma ci làkku yawut la woon, ci làkku waa Room ak ci gereg.
21 Noonu sarxalkat yu mag yu Yawut ya ne Pilaat: «Bul bind: “Buuru Yawut,” bindal rekk: “Kii moo ne mooy buuru Yawut yi.”»
22 Pilaat ne leen: «Xas naa koo bind, du deñ.»
23 Xarekat ya, bi ñu daajee Yeesu ca bant ba, ba noppi dañoo jël ay yéreem, séddale ko ñeenti cér, ku nekk benn. Jël nañu it mbubbam bu ñu ràbb ca kaw ba ci suuf te amul benn ñaw.
24 Xarekat ya di waxante naan: «Mbubb mi, bunu ko xotti, waaye nanu ko tegoo ay bant, ngir xam ku koy moom.» Noonu la Mbind mi waroona ame, bi mu naan: «Séddoo nañu samay yére, tegoo ay bant sama mbubb.» Loolu nag la xarekat ya def.
25 Ca wetu bant, ba ñu daajoon Yeesu, yaayam a nga fa taxawoon, moom ak doomu ndeyam ju jigéen, Maryaama soxnas Këlópas, ak Maryaama mi dëkk Magdala.
26 Bi Yeesu gisee yaayam taxaw ci wetu taalibe, bi mu bëggoon, mu ne ko: «Soxna si, sa doom a ngi,»
27 neeti taalibe ba: «Sa yaay a ngi nii.» Booba la ko taalibe ba yóbbu këram, yor ko.
28 Bi loolu wéyee, gannaaw Yeesu xam na ne lépp mat na léegi, mu ne nag, ngir amal Mbind mi: «Damaa mar.»
29 Amoon na foofa gutt bu fees ak bineegar. Noonu ñu jël sagar, tooyal ko ca, takk ko ci caru garab gu ñuy wax isob, teg ko ci gémmiñu Yeesu.
YOWAANA 19 in Téereb Injiil