Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 19:1-15 in Wolof

Help us?

YOWAANA 19:1-15 in Téereb Injiil

1 Noonu Pilaat joxe ndigal, ñu dóor Yeesu ay yar.
2 Xarekat ya ràbb kaalag dég, teg ko ci boppu Yeesu, solal ko mbubbum xarekat mu xonq curr.
3 Ñu di ko jegeñsi, di ko pes, naan ko: «Nuyu nanu la, yaw buuru Yawut yi!»
4 Pilaat génnaat ne leen: «Gis ngeen, maa ngi leen koy indil ci biti, ngir ngeen xam ne waa jii, gisuma ci moom genn tooñ.»
5 Yeesu nag génn, tegoo mbubbum xarekat mu xonq mi ak kaalag dég gi. Pilaat it ne leen: «Waa jaa ngii!»
6 Waaye bi ñu ko gisee, sarxalkat yu mag ya ak alkaati ya di yuuxoo naan: «Daaj ko ci bant! Daaj ko ci bant, ba mu dee!» Pilaat ne leen: «Jël-leen ko, yéen, daaj ko ci bant, ndaxte gisuma ci moom genn tooñ.»
7 Yawut yi ne ko: «Am nanu aw yoon, te ci yoon woowu, war na dee ndaxte teg na boppam Doomu Yàlla.»
8 Bi Pilaat déggee wax jooju, dafa gëna tiit,
9 dugg ca taax ma, daldi ne Yeesu: «Foo jóge?» Waaye Yeesu tontuwu ko.
10 Pilaat ne ko: «Man ngay baña waxal? Xanaa xamuloo ne am naa sañ-sañu bàyyi la, te am naa itam sañ-sañu daaj la ci bant?»
11 Yeesu ne ko: «Amuloo benn sañ-sañ ci man su dul bi la Yàlla jox. Looloo tax ba ki ma jébbal ci say loxo am na bàkkaar, bi gëna réy.»
12 Booba nag la Pilaat doon fexee bàyyi Yeesu. Waaye Yawut ya di yuuxoo naan: «Boo bàyyee kii, doo xaritu buur bi Sesaar. Nit ku teg boppam buur, noonub Sesaar la!»
13 Bi Pilaat déggee loolu, mu daldi génne Yeesu ca biti, dem toog ca jalub àttekaay ba, ca fu ñuy wax Bérabu doj ya. Ci làkku yawut ñu naan ko Gabata.
14 Booba ñu ngi waajal màggalu bésu Mucc ba, ca weti digg bëccëg. Pilaat ne Yawut ya: «Seen buur a ngii!»
15 Waaye ñuy yuuxoo naan: «Na dee! Na dee! Daaj ko ci bant!» Pilaat ne leen: «Ndax seen buur bi, dama koo wara daaj ci bant?» Sarxalkat yu mag ya ne ko: «Amunu benn buur bu dul Sesaar!»
YOWAANA 19 in Téereb Injiil