Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 18:27-32 in Wolof

Help us?

YOWAANA 18:27-32 in Téereb Injiil

27 Waaye Piyeer dellu weddi ko. Noonu ginaar daldi sab.
28 Bi loolu wéyee ñu jële Yeesu ca Kayif, yóbbu ko ca kër boroom réew ma. Ci waxtuw njël la woon. Waaye Yawut ya yéeguñu ca taaxum kaw ma. Dañoo bañoona taq sobe, ngir mana lekk ca ñamu bésu Mucc ba.
29 Looloo tax Pilaat boroom réew ma génn, dajeek ñoom. Mu laaj leen ne: «Lu ngeen di jiiñ waa jii?»
30 Ñu ne ko: «Bu deful woon lu bon, duñu la ko jébbalsi.»
31 Pilaat ne leen: «Jël-leen ko, yéen, te àtte ko ci seen yoon.» Yawut yi ne ko: «Yoon mayu nu, nu àtte nit, teg ko dee.»
32 Noonu la kàddug Yeesu gi ame, ci li mu misaaloon ni mu wara faatoo.
YOWAANA 18 in Téereb Injiil