Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 13:11-29 in Wolof

Help us?

YOWAANA 13:11-29 in Téereb Injiil

11 Fekk Yeesu xamoon na ki ko nara wor, looloo tax mu ne: «Setuleen yéen ñépp.»
12 Bi mu leen raxasalee seeni tànk ba noppi, Yeesu dafa solaat mbubbam, dellu toogaat ne leen: «Ndax xam ngeen li ma leen defal?
13 Yéena ngi may wooye “Kilifa gi” ak “Boroom bi,” te wax ngeen dëgg, moom laa.
14 Kon bu fekkee ne man miy Boroom bi tey Kilifa gi, maa leen raxasal seeni tànk, yéen itam war ngeen di raxasalante seeni tànk.
15 Bàyyil naa leen fi royukaay, ngir ngeen di jëf, nii ma jëfeek yéen.
16 Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, jaam gënula màgg sangam, mbaa ndaw, ki ko yónni.
17 Gannaaw xam ngeen loolu, bu ngeen doxalee noonu, dingeen bég.
18 «Yéen ñépp taxuleen may wax; xam naa ñi ma tànn. Waaye li Mbind mi wax, fàww mu am, bi ñu naan: “Ki lekk sama dugub wéq na ma.”
19 Maa ngi leen koy wax ci teel, bala looloo ñëw, ngir bu ñëwee, ngeen gëm ne Maay ki Nekk.
20 Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, ku nangu kenn ci ñi may yónni, nangu nga ma, man itam; te ku ma nangu, nangu nga ki ma yónni.»
21 Bi Yeesu waxee loolu ba noppi, mu jàq, biral ne: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, kenn ci yéen dina ma wor.»
22 Taalibe yi di xoolante, te xamuñu kan lay wax.
23 Ka Yeesu bëggoon te mu bokkoon ca taalibe ya, ma nga sóonu woon ca kaw Yeesu.
24 Kooku la Simoŋ Piyeer liyaar, ngir mu laaj Yeesu ki ko taxoon di wax.
25 Taalibe ba daldi walbatiku ca Yeesu, laaj ko ne: «Boroom bi, kooku kan la?»
26 Yeesu ne ko: «Dinaa capp dogu mburu ci ndab li; ki ma koy jox, kooku la.» Noonu Yeesu jël dogu mburu, capp ko ca ndab la, daldi koy jox Yudaa, doomu Simoŋ Iskariyo.
27 Naka la Yudaa jël dog wa, Seytaane dugg ci moom. Yeesu ne ko: «Gaawantul ci li ngay def!»
28 Amul kenn ca ña fa toogoon ku xam lu tax mu wax ko loolu.
29 Waaye gannaaw Yudaa moo yoroon boyetu xaalis bi, am ñu xalaat ne, Yeesu dafa koo wax, mu dem jëndi li war ci màggal gi, walla mu ne ko mu dem sarax miskin yi.
YOWAANA 13 in Téereb Injiil