Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 13:1-17 in Wolof

Help us?

YOWAANA 13:1-17 in Téereb Injiil

1 Laata màggalu bésu Mucc ba la woon. Yeesu xamoon na ne waxtu wi mu wara génne àddina, dem ca wetu Baay ba, jot na. Ku bëgg ñoñam yi nekk ci àddina la, te bëgg na leen ba fa mbëggeel mana yem.
2 Yeesu ak taalibe yaa ngi doon reer. Fekk na booba Seytaane xiirtal Yudaa, doomu Simoŋ Iskariyo, ngir mu wori Yeesu.
3 Yeesu xamoon na ne Yàlla joxoon na ko sañ-sañ ci lépp, xam it ne ca Yàlla la jóge te ca moom lay delluwaat.
4 Mu daldi jóge ca reer ba, summi mbubbam, daldi jël ab sarbet, laxas ko ci ndiggam.
5 Noonu mu sotti ndox ci ab këll, daldi tàmbali di raxas tànki taalibe ya, di leen fomp ak sarbet, ba mu laxasaayoo.
6 Bi mu agsee ba ca Simoŋ Piyeer, kooku ne ko: «Boroom bi, ndax yaw dangaa nara raxas samay tànk?»
7 Yeesu ne ko: «Xamoo fii mu nekk li may def, waaye dinga ko xami.»
8 Piyeer ne ko: «Déedéet, duma nangu mukk nga raxas samay tànk.» Yeesu ne ko: «Su ma la raxasul, doo bokk ak man dara.»
9 Simoŋ Piyeer ne ko: «Kon nag Boroom bi, bul yem rekk ci tànk yi, waaye raxasaaleel loxo yi ak bopp bi!»
10 Yeesu ne ko: «Ku sangu ba noppi, soxlaatula raxas lu dul ay tànkam, ndaxte set na wecc. Yéen nag set ngeen, waaye du ñépp!»
11 Fekk Yeesu xamoon na ki ko nara wor, looloo tax mu ne: «Setuleen yéen ñépp.»
12 Bi mu leen raxasalee seeni tànk ba noppi, Yeesu dafa solaat mbubbam, dellu toogaat ne leen: «Ndax xam ngeen li ma leen defal?
13 Yéena ngi may wooye “Kilifa gi” ak “Boroom bi,” te wax ngeen dëgg, moom laa.
14 Kon bu fekkee ne man miy Boroom bi tey Kilifa gi, maa leen raxasal seeni tànk, yéen itam war ngeen di raxasalante seeni tànk.
15 Bàyyil naa leen fi royukaay, ngir ngeen di jëf, nii ma jëfeek yéen.
16 Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, jaam gënula màgg sangam, mbaa ndaw, ki ko yónni.
17 Gannaaw xam ngeen loolu, bu ngeen doxalee noonu, dingeen bég.
YOWAANA 13 in Téereb Injiil