Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 12:21-36 in Wolof

Help us?

YOWAANA 12:21-36 in Téereb Injiil

21 Ñëw nañu ci Filib, mi dëkk Betsayda ci diiwaanu Galile, ne ko: «Sang bi, danoo bëggoona gis Yeesu.»
22 Filib dem wax ko Andare; ñu ànd, waxi ko Yeesu.
23 Mu ne leen: «Waxtu wi ñu wara feeñale ndamu Doomu nit ki jot na.
24 Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, fi ak peppu dugub ji wadd ci suuf jaarul ci dee, du mana weesu li mu doon: pepp doŋŋ. Waaye bu deeyee, dina jur pepp yu bare.
25 Ku bëgg bakkanam dina ko ñàkk, waaye ku ko bañ ci àddina sii, dina ko denc ngir dund gu dul jeex gi.
26 Ku bëgga doon sama surga, na ma topp. Bu ko defee, fu ma nekk, fa lay nekk moom itam. Ku may liggéeyal, sama Baay dina ko teral.
27 «Léegi nag damaa jàq. Lu may wara wax? Mbaa du dama naan: “Baay, musal ma ci li nara xew waxtu wiy ñëw?” Déedéet, ñëw naa sax ngir jaar ci waxtu woowu.
28 Baay, màggalal sa tur!» Noonu ñu dégg baat bu jóge asamaan naan: «Màggal naa ko ba noppi, te dinaa ko màggalaat.»
29 Mbooloo ma fa teewoon te dégg baat ba daldi ne: «Dënnu la woon!» Ñeneen naan: «Malaakaa doon wax ak moom.»
30 Waaye Yeesu ne leen: «Taxuma baat boobu jolli, waaye yéena tax.
31 Àtteb àddina si jot na: léegi ñu dàq malaaka mu bon, mi jiite àddina si.
32 Te man, bu ñu ma yékkatee, ma tiim suuf, dinaa xiirtal nit ñépp ci man.»
33 Ci baat yooyu la doon misaale ni mu wara faatoo.
34 Mbooloo ma ne ko: «Jàng nanu ci sunu téereb yoon ne, Almasi bi dina sax ba fàww. Kon yaw, nan nga mana waxe ne: “Doomu nit ki dina yékkatiku?” Kuy Doomu nit kooku?»
35 Yeesu ne leen: «Leer gi dootul yàgg ak yéen. Doxleen, ci bi ngeen dee am leer, ngir lëndëm bañ leena bett. Ndaxte kuy dox ci lëndëm doo xam foo jëm.
36 Kon ci bi ngeen dee am leer gi, gëmleen ko, ngir ngeen doon doomi leer.» Bi mu waxee loolu ba noppi, Yeesu dafa dem, nëbbatuji leen.
YOWAANA 12 in Téereb Injiil