Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 12:16-33 in Wolof

Help us?

YOWAANA 12:16-33 in Téereb Injiil

16 Yooyu yépp, taalibe ya xamuñu woon ca saa sa lu muy tekki; waaye gannaaw bi ndamu Yeesu feeñee, ñu fàttaliku ne, Mbind mi yégle woon na loolu ci moom, te amal nañu ko.
17 Ña nekkoon ak Yeesu ñépp, bi muy wooyee Lasaar mu génn ca bàmmeel ba te mu dekkal ko, demoon nañu, nettali la ñu gis.
18 Looloo tax mbooloo ma teeru ko, ndaxte yégoon nañu firnde jooju.
19 Farisen yi nag di waxante naan: «Gis ngeen, manuleen ci dara; ñépp a ngi koy topp!»
20 Ca mbooloo ma, amoon na ca ay Gereg yu bokk ca ña ñëwoon Yerusalem ngir jaamu Yàlla diirub màggal ga.
21 Ñëw nañu ci Filib, mi dëkk Betsayda ci diiwaanu Galile, ne ko: «Sang bi, danoo bëggoona gis Yeesu.»
22 Filib dem wax ko Andare; ñu ànd, waxi ko Yeesu.
23 Mu ne leen: «Waxtu wi ñu wara feeñale ndamu Doomu nit ki jot na.
24 Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, fi ak peppu dugub ji wadd ci suuf jaarul ci dee, du mana weesu li mu doon: pepp doŋŋ. Waaye bu deeyee, dina jur pepp yu bare.
25 Ku bëgg bakkanam dina ko ñàkk, waaye ku ko bañ ci àddina sii, dina ko denc ngir dund gu dul jeex gi.
26 Ku bëgga doon sama surga, na ma topp. Bu ko defee, fu ma nekk, fa lay nekk moom itam. Ku may liggéeyal, sama Baay dina ko teral.
27 «Léegi nag damaa jàq. Lu may wara wax? Mbaa du dama naan: “Baay, musal ma ci li nara xew waxtu wiy ñëw?” Déedéet, ñëw naa sax ngir jaar ci waxtu woowu.
28 Baay, màggalal sa tur!» Noonu ñu dégg baat bu jóge asamaan naan: «Màggal naa ko ba noppi, te dinaa ko màggalaat.»
29 Mbooloo ma fa teewoon te dégg baat ba daldi ne: «Dënnu la woon!» Ñeneen naan: «Malaakaa doon wax ak moom.»
30 Waaye Yeesu ne leen: «Taxuma baat boobu jolli, waaye yéena tax.
31 Àtteb àddina si jot na: léegi ñu dàq malaaka mu bon, mi jiite àddina si.
32 Te man, bu ñu ma yékkatee, ma tiim suuf, dinaa xiirtal nit ñépp ci man.»
33 Ci baat yooyu la doon misaale ni mu wara faatoo.
YOWAANA 12 in Téereb Injiil