Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 11:12-36 in Wolof

Help us?

YOWAANA 11:12-36 in Téereb Injiil

12 Taalibe ya ne ko: «Boroom bi, bu nelawee kay, kon dina wér.»
13 Yeesu dafa bëggoona wax ne, Lasaar dee na, waaye taalibe yi dañoo xalaatoon ne mbiri nelaw rekk lay wax.
14 Ci kaw loolu Yeesu wax ci lu leer ne: «Lasaar dee na.
15 Bég naa ngir yéen ndax li ma fa nekkul, ngir seen ngëm gëna dëgër. Waaye nanu ko seeti.»
16 Noonu Tomaa, ki turam di tekki «Séex bi», daldi ne yeneen taalibe ya: «Nanu dem nun itam, deeyandoo ak moom!»
17 Bi Yeesu agsee, mu fekk ne bi ñu dencee Lasaar ak léegi, mat na ñeenti fan.
18 Betani ma nga woon ca wetu Yerusalem, diggante bi matul woon sax ñetti kilomet.
19 Yawut yu bare ñëwoon nañu kër Màrt ak Maryaama, ngir dëfal leen ci seen deewu càmmiñ.
20 Bi Yeesu ñëwee, Màrt yég ko, dem di dajeek moom; fekk booba Maryaamaa nga toogoon ca kër ga.
21 Màrt ne Yeesu: «Boroom bi, boo fi nekkoon de, sama càmmiñ li du dee.
22 Waaye xam naa ne fii nu tollu sax, loo ñaan Yàlla, mu may la ko.»
23 Yeesu ne ko: «Sa càmmiñ dina dekki.»
24 Màrt ne ko: «Xam naa ne dina jóg bésu ndekkite la, keroog bés bu mujj ba.»
25 Yeesu ne ko: «Man maay ndekkite li, maay dund gi. Ku ma gëm, boo deeyee it, dinga dund.
26 Rax-ca-dolli kuy dund te gëm ma, doo dee mukk. Ndax gëm nga loolu?»
27 Mu ne ko: «Waaw, Boroom bi. Gëm naa ne yaay Almasi bi, di Doomu Yàlla, ji wara ñëw àddina.»
28 Bi Màrt waxee loolu, mu daldi dem wooyi Maryaama ne ko ci pett: «Kilifa gaa ngi fi; mi ngi lay laaj.»
29 Bi Maryaama déggee loolu, mu daldi jóg, gaawantu dem ca Yeesu.
30 Te fekk duggagul woon ca dëkk ba, waaye ma nga woon ba tey ca bérab, ba mu daje woon ak Màrt.
31 Noonu Yawut, ya nekkoon ca kër ga di dëfal Maryaama, gis ko mu ne bërét génn, ñu daldi koy topp, defe ne day jooyi ca bàmmeel ba.
32 Bi Maryaama agsee nag ca Yeesu, ba gis ko, mu daanu ciy tànkam ne ko: «Boroom bi, boo fi nekkoon, sama càmmiñ du dee.»
33 Yeesu gis ne mi ngi jooy te Yawut yi ànd ak moom itam ñu ngi jooy. Mu daldi jàq, am naqar wu réy.
34 Mu ne leen: «Fu ngeen ko denc?» Ñu ne ko: «Kaay gis, Sang bi.»
35 Yeesu jooy.
36 Noonu nag, Yawut ya ne: «Gis ngeen ni mu ko bëgge woon!»
YOWAANA 11 in Téereb Injiil