Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 8:8-10 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 8:8-10 in Kàddug Yàlla gi

8 Mu solal ko nag kiiraayal dënn ba, daldi yeb ca biir kiiraay la jumtukaayi tegtal ya, di Urim ba ak Tumim ba,
9 la ca tegu mu tegal ko kaala ga ca bopp ba, takkal ko dogu wurus wu tell wa, mooy meeteel gu sell ga, mu nekk ca kaw kaala ga, féete kanam, muy la Aji Sax ji santoon Musaa.
10 Ba loolu wéyee Musaa jël diwu pal ga, diw ca jaamookaay baak ya ca biir yépp, sellale ko yooya,
Sarxalkat yi 8 in Kàddug Yàlla gi