4 Musaa def la ko Aji Sax ji sant, mbooloo ma daje ca bunt xaymab ndaje ma.
5 Musaa wax mbooloo ma ne leen: «Lii may waaj la Aji Sax ji santaane woon ñu def ko.»
6 Ci kaw loolu Musaa indi Aaróona aki doomam yu góor, ñu sangu,
7 solal Aaróona mbubb mu gudd ma, takkal ko laxasaay ga, solal ko fëxya ba, tegal ko ca xar-sànni ma, takkal ko ngañaay la ca kawam, jàppe ko ko, mu tafu ca kawam.
8 Mu solal ko nag kiiraayal dënn ba, daldi yeb ca biir kiiraay la jumtukaayi tegtal ya, di Urim ba ak Tumim ba,