Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 8:29-35 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 8:29-35 in Kàddug Yàlla gi

29 Musaa daldi jël dënn biy céram ci kuuyu xewu colu gi, yékkati ko, jébbal Aji Sax ji, muy saraxu yékkati-jébbale, di la Aji Sax ji santoon Musaa.
30 Musaa teg ca sàkk ca diwu pal ga, ak deret ji ci sarxalukaay bi, wis-wisal ko ci kaw yaramu Aaróona ak ca kawi yéreem, wis-wisaale ko ca kaw yarami doomam yu góor ak ca kaw yérey doomam.
31 Musaa wax ak Aaróona aki doomam yu góor ne leen: «Toggleen yàpp wi ci bunt xaymab ndaje mi te lekk ko foofa, boole kook mburu mi ci layub saraxi xewu colu gi, muy la ma santaane woon ne yaw Aaróona yaak say doom yu góor yeena koy lekk.
32 Li des ci yàpp wi ak mburu mi, lakkleen ko, ba mu dib dóom.
33 Waaye bunt xaymab ndaje mi buleen ko wees diiru juróom ñaari fan, ba bésub keroog ba seen xewu colu di mat, ndax juróom ñaari fan lay mat.
34 Lépp lu ñu def tey, Aji Sax ji daa santaane ñu def ko, mu daldi matal seen njotlaay.
35 Ci bunt xaymab ndaje mi ngeen di yem guddeek bëccëg diiru juróom ñaari fan, boole ci di dénkoo dénkaaney Aji Sax ji, ndax ngeen baña dee, ndaxte loolu moo di li ñu ma santoon.»
Sarxalkat yi 8 in Kàddug Yàlla gi