26 Layu bi def mburu yi amul lawiir, taaje fi kanam Aji Sax ji, mu jële ca menn mburu kese mu ndaw ak menn mburu mu ndaw te am diw ak menn mburu mu tàppandaar, boole ko teg ca kaw nebbon ba ak tànku ndijoor ba.
27 Mu boole yooyu yépp teg ci loxol Aaróona ak loxoy doomam yu góor, ngir ñu def ko sarax bu ñuy yékkati, jébbal Aji Sax ji.