23 Musaa rendi ko, sàkk ca deret ja, taqal ca tabanu noppu ndijooru Aaróona, taqal ca baaraamu déyu ndijooram ak baaraamu déyu tànku ndijooram.
24 Musaa doora indi doomi Aaróona yu góor ya, sàkk ca deret ja, taqal ca seen tabani noppi ndijoor ak seen baaraamu déyu ndijoor ak seen baaraamu déyu tànki ndijoor. La des ca deret ja, Musaa xëpp ko ca mboolem weti sarxalukaay bi.
25 Ba mu ko defee mu génne nebbon bi, muy calgeen bi ak nebbon bi sàng yérey biir yépp ak bàjjo bi ci res wi ak ñaari dëmbéen yi ànd ak seen nebbon, ak tànkub ndijoor bi.
26 Layu bi def mburu yi amul lawiir, taaje fi kanam Aji Sax ji, mu jële ca menn mburu kese mu ndaw ak menn mburu mu ndaw te am diw ak menn mburu mu tàppandaar, boole ko teg ca kaw nebbon ba ak tànku ndijoor ba.