Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 7:30-32 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 7:30-32 in Kàddug Yàlla gi

30 Ci loxol boppam lay dindee sarax bi ñuy def saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji. Day indi nebbon bi, boole kook dënn bi, dënn bi di sarax bu ñuy yékkati, jébbal Aji Sax ji.
31 Sarxalkat bi day lakk nebbon bi ci kaw sarxalukaay bi, waaye dënn bi, Aaróona aki doomam yu góor ñoo ko moom.
32 Tànkub ndijoor bi jóge ci seen saraxi cant ci biir jàmm, dees koy jooxeel sarxalkat bi.
Sarxalkat yi 7 in Kàddug Yàlla gi