Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 7:19-30 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 7:19-30 in Kàddug Yàlla gi

19 Yàpp wu ci laal lenn lu sobewu it deesu ko lekk. Dees koy lakk. Ci biir loolu yàppu sarax, képp ku set sañ nga cee lekk.
20 Waaye ku sobewu ku lekk ci yàppu jur gu ñu defal Aji Sax ji saraxu cant ci biir jàmm, kooku nañu ko dagge ci biir bànni Israyil.
21 Sobe su mu mana doon, muy lu jóge ci nit mbaa mala mu daganul mbaa mboolem lu daganul te mata sib, ku ci laal ba noppi, lekk ci lu ñu defal Aji Sax ji saraxu cant ci biir jàmm, kooku dees koo wara dagge ci bànni Israyil.»
22 Aji Sax ji dellu wax Musaa ne ko:
23 «Waxal bànni Israyil ne leen: Buleen lekk lenn luy nebbonu nag mbaa xar mbaa bëy.
24 Nebbonu jur gu dee mbaa lu rabu àll fàdd, manees na koo jëfandikoo neneen nu mu mana doon, waaye deesu ko lekk mukk.
25 Képp ku lekk ci nebbonu jur gu ñu def saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji, kooku ko lekk, dees koy dagge ca biir bànni Israyil.
26 Te itam du lenn luy deret lu ngeen di lekke fenn fu ngeen dëkk, mu jóge ci njanaaw mbaa ag jur.
27 Képp ku lekk lenn luy deret, dees na ko dagge ci biir bànni Israyil.»
28 Aji Sax ji dellooti wax Musaa ne ko:
29 «Waxal bànni Israyil ne leen: Képp kuy jox Aji Sax ji saraxu cantam ci biir jàmm na indi cér bi Aji Sax ji séddoo ci saraxu cant googu ci biir jàmm.
30 Ci loxol boppam lay dindee sarax bi ñuy def saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji. Day indi nebbon bi, boole kook dënn bi, dënn bi di sarax bu ñuy yékkati, jébbal Aji Sax ji.
Sarxalkat yi 7 in Kàddug Yàlla gi