14 Nañu jooxeel Aji Sax ji ab cér ci sarax yooyu yépp, muy moomeelu sarxalkat bi xëpp deretu juru saraxas cant gi ci biir jàmm ci mboolem weti sarxalukaay bi.
15 Yàppu saraxas cant googu ci biir jàmm te ñu jublu ci njukkal Aji Sax ji, dees koy lekk bés bi ñu ko rendee. Du lenn lees ciy wacc, mu fanaan.
16 «Su sarax si nit kiy génne dee sarax su ñuy wàccoo ngiñ mbaa saraxu yéene, dees na ko lekk bés bi ko nit ki joxee, te lu ca des ba ca ëllëg sa, ñu man koo lekk.
17 Lu des ci yàppu sarax si ba ca gannaaw ëllëg sa dees koy lakk, ba mu dib dóom.
18 Waaye kat bu nit lekkee lenn ci yàpp wu ñu def saraxu cant ci biir jàmm te fekk mu am ñetti fan, deesul nangul boroom sarax si te du ko jariñ dara. Lu ñu sib la te ku ca lekk mooy gàddu bàkkaaram.