Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 6:7-12 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 6:7-12 in Kàddug Yàlla gi

7 «Li ñu dogal ci saraxi pepp mooy lii: Na ko doomi Aaróona yu góor joxe fa kanam Aji Sax ji ca sarxalukaay ba.
8 Barci-loxob sunguf su mucc ayib ànd ak diwam lees ciy tibbe, boole kook mboolem cuuraay la ca kaw saraxu pepp ma, daldi koy lakkal Aji Sax ji ci kaw sarxalukaay bi, muy xeeñ xetug jàmm, di saraxu baaxantal.
9 La ca des Aaróona aki doomam yu góor ñoo koy lekk, te buñu ci boole lawiir. Nañu ko lekke ci bérab bu sell. Ci biir ëttu xaymab ndaje mi lañu koy lekke.
10 Deesu ko lakkaaleek lawiir. Seen cér la bu leen Aji Sax ji sédd ci saraxi sawaraam. Lu sella sell la, mel ni saraxu póotum bàkkaar ak saraxu peyug tooñ.
11 Képp kuy góor ci doomi Aaróona yi man na cee lekk. Seen cér la bu ñu leen sédde ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji, te dogalal leen ko fàww. Lépp lu ci laal day doon lu sella sell.»
12 Aji Sax ji wax na Musaa ba tey ne ko:
Sarxalkat yi 6 in Kàddug Yàlla gi