Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 6:1-17 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 6:1-17 in Kàddug Yàlla gi

1 Aji Sax ji waxaat Musaa ne ko:
2 «Santal Aaróona ak doomam yu góor, ne leen li ñu dogal ci saraxu rendi-dóomal mooy lii: Ab saraxu rendi-dóomal day fanaan fi ñu koy lakke ci kaw sarxalukaay bi, ba bët set, sawara way wéye tàkk ca kaw sarxalukaay ba.
3 Sarxalkat bi day sol mbubbam mi ñu ràbbe wëñ gu ëccu ba sew ak tubéyi njiitlaayam ji ñu ràbbe wëñ gu ëccu ba sew. Na tonnee ca sarxalukaay ba dóomu saraxu rendi-dóomal bi, daldi teg dóom bi ci wetu sarxalukaay bi.
4 Su ko defee mu summi yéreem yooyu, sol yeneen te génne dóom bi dal bi, yóbbu ko fu mucc sobe.
5 Na sawaras sarxalukaay bi wéye tàkk te du fey. Suba su nekk na ko sarxalkat bi xamb, ba noppi teg ci saraxu rendi-dóomal bi, te na lakk nebboni saraxi cant gi ci biir jàmm.
6 Na sawara wéye tàkk fàww ci kaw sarxalukaay bi, te bumu fey.
7 «Li ñu dogal ci saraxi pepp mooy lii: Na ko doomi Aaróona yu góor joxe fa kanam Aji Sax ji ca sarxalukaay ba.
8 Barci-loxob sunguf su mucc ayib ànd ak diwam lees ciy tibbe, boole kook mboolem cuuraay la ca kaw saraxu pepp ma, daldi koy lakkal Aji Sax ji ci kaw sarxalukaay bi, muy xeeñ xetug jàmm, di saraxu baaxantal.
9 La ca des Aaróona aki doomam yu góor ñoo koy lekk, te buñu ci boole lawiir. Nañu ko lekke ci bérab bu sell. Ci biir ëttu xaymab ndaje mi lañu koy lekke.
10 Deesu ko lakkaaleek lawiir. Seen cér la bu leen Aji Sax ji sédd ci saraxi sawaraam. Lu sella sell la, mel ni saraxu póotum bàkkaar ak saraxu peyug tooñ.
11 Képp kuy góor ci doomi Aaróona yi man na cee lekk. Seen cér la bu ñu leen sédde ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji, te dogalal leen ko fàww. Lépp lu ci laal day doon lu sella sell.»
12 Aji Sax ji wax na Musaa ba tey ne ko:
13 «Li Aaróona aki doomam yu góor di sarxalal Aji Sax ji, keroog bu ñu koy diw, fal ko, mooy lii: ñetti kiloy sunguf su mucc ayib, tollook saraxu pepp bi ñu saxoo bés bu nekk, te genn-wàll gi di suba, genn-wàll gi ngoon.
14 Saafukaayu weñ lañu koy lakke, xiiwaale ko diw, indi xiiw ba, muy saraxu pepp. Nañu ko def ay dog yu ñuy lakkal Aji Sax ji, muy xeeñ xetug jàmm.
15 Sarxalkat bi ñuy fal ci doomi Aaróona yu góor yi, mu war koo wuutu, da koy def moom itam. Aji Sax ji moo jagoo sarax boobu fàww, te dañu koy lakk ba mu jeex.
16 Te it mboolem saraxu pepp bu sarxalkat di defal boppam, dees koy lakk ba mu jeex. Deesu ci lekk.»
17 Aji Sax ji waxati Musaa ne ko:
Sarxalkat yi 6 in Kàddug Yàlla gi