Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 5:11-18 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 5:11-18 in Kàddug Yàlla gi

11 «Su amul lu mat njégu ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw, li muy indi, sarxal ko ngir bàkkaar bi mu def, ñetti kiloy sunguf su mucc ayib lay doon, muy saraxu póotum bàkkaar. Du ci def diw, te du ci sotti cuuraay, ndax li mu di saraxu póotum bàkkaar.
12 Da koy yót sarxalkat bi, sarxalkat bi sàkk ci barci-loxo, muy saraxu baaxantal, mu daldi koy lakk ca kaw sarxalukaay bi, mu dolliku ci saraxi sawara yi. Saraxu póotum bàkkaar la.
13 Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayal bàkkaar, bi mu def te mu bokk ci xeeti bàkkaar yooyu ñu lim. Su ko defee mu am njéggal. Li des ci sarax bi sarxalkat bee koy moom, mu mel ni bu doon saraxu pepp rekk.»
14 Bu loolu weesee, Aji Sax ji wax na Musaa ne ko:
15 «Ku ñàkka wormaal lenn lu ñu sellalal Aji Sax ji te du teyeefam, daan ba ko war, mu di ko indil Aji Sax ji, am kuuy mu amul sikk lay doon, ñuy xayma njégam, dëppale dayob xaalis baak natt ba ñu yoonal ca bérab bu sell ba. Saraxu peyug tooñ la.
16 La mu sàggane woon ca yooyu ñu sellalal Aji Sax ji da koy fey, ba dolli ci juróomeelu céru njég ga mu fey, jox ko sarxalkat bi. Sarxalkat bi da koy defal kuuy mi njotlaayam, muy saraxu peyug tooñ, ngir mu am njéggal.
17 «Su fekkee ne nit ki dafa moy lenn ci santaaney Aji Sax ji ci lu warul lu mu def, su ko xamul it, tooñ na, te dees na ko ko topp.
18 Na indi kuuy mu amul sikk, ñu xayma njégam, yót ko sarxalkat bi, muy saraxu peyug tooñ. Na ko ko sarxalkat bi defal njotlaayal bàkkaar bi mu def te xamu ko woon. Su ko defee mu am njéggal.
Sarxalkat yi 5 in Kàddug Yàlla gi